1.Buur ya 14:1-30 WOLB2025 - Bible AI

1Ca yooyu jamono Abya doomu Yerbowam ju góor wopp.

2Yerbowam wax soxnaam, ne ko: «Ayca, doxal soppiji col, ba kenn du xam ne sama soxna nga, te nga dem Silo. Dama ne, Axya yonent baa nga fa. Moo ma waxoon ne ma, dinaa falu buur, jiite mbooloo mii.

3Yóbbaaleel fukki mburu ak nàkk yu ndaw ak taxub lem te nga dem ca moom. Moom dina la wax nan la mbiri gone gii di deme.»

4Soxnas Yerbowam def noona, daldi dem Silo, agsi kër Axya.

5Waaye fekk na Aji Sax ji wax Axya, ne ko: «Dama ne, soxnas Yerbowam a ngi ñëw di leerlusi mbirum doomam ju góor ci yaw, ndax dafa wopp. Bu dikkee keneen lay mbubboo.» Aji Sax ji ne Axya, mu wax ko nàngam ak nàngam.

6Ba loolu amee Axya dégg tànki ndaw sa ca bunt ba. Mu ne ko: «Soxnas Yerbowam, agsil! Ana looy mbubboo keneen nii? Man de yóbbante nañu ma ci yaw xibaar bu tiis.

7Demal ne Yerbowam: “Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ne: Dama laa yékkati ci biir mbooloo mi, fal la nga jiite Israayil sama ñoñ.

8Damaa foqatee nguur gi ci loxol waa kër Daawuda, jox la ko. Waaye meloo ni Daawuda, sama jaam ba daan jëfe samay santaane, toppe ma léppi xolam, du def lu moy lu ma rafetlu.

9Def nga musiba, ba raw mboolem ñu la jiitu, dem di sàkkal sa bopp yeneen yàlla ak tuur yu ñu móole weñ, ba sama xol fees. Man mii nga xarab, dëddu ma.

10Moo tax duma def lu moy wàcce musiba ci kër Yerbowam.

11Ku Yerbowam deele ci dëkk bi, xaj yi lekk;

12«Yaw nag jógal ñibbi sa kër. Booy teg sa tànk ca biir dëkk ba rekk, gone gi dee.

13Israayil gépp dinañu ko jooy. Kooku rekk déy lees di denc ci bàmmeel, ci ku bokk ci Yerbowam, ngir ci moom doŋŋ la Aji Sax ji Yàllay Israayil gis lu baax, ci waa kër Yerbowam.

14Aji Sax ji dina falal boppam buur bu jiite Israayil, te kooku dina bóom waa kër Yerbowam. Bés bi taxaw na jeeg! Ana lu ciy topp?

15Aji Sax ji dina faat Israayil. Dinañu mel ni gattax guy foyfoyi cim ndox. Dina déjjatee Israayil ci suuf su baax sii mu joxoon seeni maam, tasaare leen ca wàllaa dexu Efraat, ndax dañoo samp ay xer yu ñuy jaamoo Asera|lemma="Asera:"*, di merloo Aji Sax ji.

16Aji Sax ji dina wacc Israayil ndax bàkkaari Yerbowam yi mu bàkkaar te di ko bàkkaarloo Israayil.»

17Ba loolu amee soxnas Yerbowam jóg, bàyyikoo fa, ba àgg Tirca. Naka la agsi ca bunt kër ba, xale ba dee.

18Ñu rob ko, Israayil gépp jooy ko, muy la Aji Sax ji waxoon, Yonent Yàlla Axya jaamam ba jottali ko.

19Li des ci mbiri Yerbowam, ay xareem ak na nguuram deme woon, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israayil ca seeni jant.

20At ya Yerbowam falu buur, ñaar fukki at la ak ñaar. Gannaaw loolu mu saay, fekki ay maamam. Nadab doomam falu, wuutu ko.

21Robowam doomu Suleymaan moo doon buurub Yuda. Ñeent fukki at ak benn la Robowam amoon ba muy falu. Fukki at ak juróom ñaar la nguuroo Yerusalem, dëkk ba Aji Sax ji tànn ci mboolem dëkki giiri Israayil, ngir dëël fa turam. Ndeyam di Naama, di ab Amoneen.

22Waa Yuda nag di def li Aji Sax ji ñaawlu, ba di ko fiirloo fiiraange gu raw ga ko seen maam daa fiirloo ndax seen bàkkaar.

23Dañoo sàkkal seen bopp ay bérebi jaamookaay|lemma="bérebi jaamookaay y-:"*, samp ay tuuri doj aki xer yu ñuy jaamoo Asera|lemma="Asera:"* ca kaw mboolem tund wu kawe mbaa ker garab gu naat.

24Réew ma amoon na sax ñuy gànctu fa ñuy màggale tuur ya. Ñuy def mboolem ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* wuutu leen.

25Ba Buur Robowam faloo, ba dugg ca juróomeelu atu nguuram, Sisag buuru Misra song Yerusalem.

26Ci kaw loolu Sisag jël alali kër Aji Sax ji ak alali kër buur. Lépp la jël ba ca mboolem pakki wurus ya Suleymaan defarlu woon.

27Ba mu ko defee Buur Robowam defarlu ay pakku xànjar yu wuutu yu wurus ya. Mu teg ko ca loxoy njiiti dag yay wattu buntu kër buur.

28Saa yu Buur dee duggsi ca kër Aji Sax ji, dag ya ŋàbb pakk ya, bu ñu noppee delloo ko ca néegu dag ya.

29Li des ci mbiri Robowam ak mboolem la mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant.

30Xare masula dakk diggante Robowam ak Yerbowam.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>