1.Jaar-jaar ya 12:1-40 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw loolu ña fekki woon Daawuda ca Ciglaag, ba muy daw Sawul doomu Kis, bokkoon nañu ci jàmbaar ñi ko daan jàppale ci xare.

2Dañu daan gànnaayoo ay fitt, mane ndijoor ak càmmoñ ci sànni xeer ak fitt. Ña ca bokkoon ca giirug Beñamin, di giirug Sawul ñii la woon:

3Axyeser moo doon seen njiit, mbokkam Yowas doomu Semaa, ma dëkk Gibeya ca la, ak Yesiyel ak Pelet doomu Asmawet ak Beraka ak Yewu ma dëkk Anatot,

4ak Ismaya ma dëkk Gabawon di jàmbaar ju bokk ca Fanweer ña,

5ak Yeremi ak Yaxasyel ak Yoxanan ak Yosabàdd ma dëkk Gedera,

6ak Elusay ak Yerimot ak Beyalya ak Semerya ak Sefatiya mu Aruf.

7Elkana it ca la ak Isiya ak Asareel ak Yoweser ak Yasobam, ñooñu askanoo ci Kore,

8ak itam Yowela ak Sebaja doomu Yeroxam, ma dëkk Gedor.

9Mu am nag ñu bokk ca giiru Gàdd dëddu Sawul fekki Daawuda ca rawtoom ba ca màndiŋ ma. Ay ñeyi xare lañu woon ñu mana xeex, mane pakk ak xeej, diy gaynde te gaaw ba mel niy kéwél ca tund ya.

10Eser moo doon seen njiit, Abdiyas+ 12.10 Abdiyas mii bokkul ak Yonent Yàlla Abdiyas.* topp ca di ñaareel, Elyab di ñetteel,

11Misamana di ñeenteel; Yeremi+ 12.11 Yeremi mii bokkul ak Yonent Yàlla Yeremi.* di juróomeel,

12Atay di juróom benneel, Elyel di juróom ñaareel;

13Yoxanan di juróom ñetteel, Elsabat di juróom ñeenteel,

14Yeremi di fukkeel, Magbanay di fukkeel ak benn.

15Ñooñu bokk ci giiru Gàdd ay njiiti xare lañu woon ñoom ñépp. Ki gënoona tuut ci ñoom manoon naa xeex ak téeméeri góor; ki gëna mag xeex ak junniy góor.

16Ñooñu ñooy ña jàlloon dexu Yurdan ca weer wa njëkk ca at ma, fekk mu fees ba ca tàkk ga, daldi dàq mboolem waa xur ya, penkook sowu.

17Ci kaw loolu ñu bokk ci giirug Beñamin+ 12.17 Beñamin: Sawul mi doon wuta bóom Daawuda, ci giirug Beñamin la bokkoon.* ak Yuda ànd fekki Daawuda ca rawtoom.

18Daawuda génn gatandu leen, ne leen: «Su fekkee ne jàmm ak dimbali ma moo leen indi fi man, dalal naa leen ci xol bu sedd. Waaye su ngeen ma naree lor, jébbal ma samay noon te defuma dara de, Yàlla na ko sunuy Yàllay maam seede te àtte.»

19Ba loolu amee leerug Yàlla dikkal Amasay ka jiite Fanweeri jàmbaar ya. Mu ne: «Yaa nu moom, yaw Daawuda, nu far ak yaw, doomu Yese. Jàmm, jàmm rekk a la ñeel, te jàmm ay ñeel ñi lay wallu, ndax sa Yàlla moo lay wallu.» Daawuda nag dalal leen, def leen ay njiit ci gàngooram.

20Ci kaw loolu ñu bokk ci giirug Manase fàq, far ak Daawuda ca xare ba mu àndeek waa Filisti, ñu dali ci kaw Sawul. Daawudaaki nitam sax mujjuñoo sotle waa Filisti ndax njiiti waa Filisti dañoo diisoo, ba noppi daldi dàq Daawuda. Booba dañu ne: «Bu Daawuda fàqee farijeek sangam Sawul, sunu bakkan lañu koy feye.»

21Ba Daawuda di dellu Ciglaag nag la ko waa giirug Manase fekksi. Muy Atnax ak Yosabàdd ak Yediyel ak Mikayel ak Yosabàdd ak Eliyu ak Ciletay, ñépp di njiiti kuréeli junni ci giirug Manase.

22Ñooñu ndimbal lañu woon ci Daawudaak gàngooram ndax ñeyi xare lañu woon ñoom ñépp te ay njiit lañu woon ca gàngooru xare ga.

23Ci biir loolu bés bu Yàlla sàkk, ay nit di fekksi Daawuda ngir jàppale ko, ba mu am mbooloo mu réy te am doole.

24Limu nit ñi tollu ci xaree ngii, di ña fekki woon Daawuda ca Ebron ngir jële nguur ga ca Sawul, jox ko ko, muy la Aji Sax ji waxoon.

25Waa Yuda juróom benni junneek juróom ñetti téeméer (6 800) lañu, gànnaayoo ay xeej aki pakk.

26Waa giirug Simeyon juróom ñaari junneek téeméeri (7 100) ñeyi xare lañu, tollu ci xare.

27Leween|lemma="Leween b-:"* ña ñeenti junneek juróom benni téeméer (4 600) lañu.

28Ñu ànd ak Yoyada may kilifa ci askanu Aaróona te jiite ñetti junniy nit ak juróom ñaari téeméer (3 700).

29Cadog bokkoon na ca, xale bu góor la woon, di ñeyi xare, ànd ak ñaar fukki kilifaak ñaar ca waa kër maamam.

30Waa giirug Beñamin di giirug Sawul ci boppam, ñetti junni (3 000) lañu, ña ca ëpp séddoo kër Sawul ba jant yooyu.

31Waa giirug Efrayim ñaar fukki junneek juróom ñetti téeméer (20 800) lañu woon, di ñeyi xare te diy boroomi tur ca seen waa kër maam.

32Waa genn-wàllu giirug Manase ga ca sowu fukki junneek juróom ñett (18 000) lañu woon, di ñu ñu tudd seen tur ñu wara fali Daawuda buur.

33Waa giirug Isaakar ñaari téeméeri kilifa lañu woon ñu ànd ak mboolem seen bokk yi ñu jiite. Ay nit lañu woon ñu mana ràññee diggante ba Israayil mana tollu ak na ñu ca wara jëfe.

34Waa giirug Sabulon juróom fukki junni lañu (50 000), tàggatu ngir xare, gànnaayu ba jekk ci xare, ànd ceek pastéefu xol bu mat sëkk.

35Waa giirug Neftali junniy (1 000) njiiti xare lañu ak fanweeri junniy xarekat ak juróom ñaar (37 000) yu gànnaayoo ay xeej aki pakk.

36Waa giirug Dan ñaar fukki junneek juróom ñett ak juróom benni téeméer (28 600) lañu, di ñu jekk ci xare.

37Waa giirug Aser ñeent fukki junniy (40 000) nit lañu ñu tàggatu ngir xare.

38Ña bàyyikoo ca waa giir ya dëkke ca penkub dexu Yurdan, di yoy Ruben ak Gàdd ak geneen wàllu giirug Manase ga téeméeri junneek ñaar fukk (120 000) lañu, yore lépp luy gànnaay.

39Xarekat yooyu yépp a jekk ci xare, ànd ak pastéef gu mat sëkk ba Ebron, ngir fal Daawuda buur, mu jiite Israayil gépp. Bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ga ca des gépp mànkoo di benn, topp ñoom it, ngir fal Daawuda buur.

40Ñu bokk fa toog ak Daawuda ñetti fan, di lekk aka naan ca la leen seeni bokk waajalaloon.

cle>