1Ci biir loolu Iram buurub Tir yebal ay ndaw ca Daawuda, ñu yóbbul ko ay banti seedar, ak tabaxkati miir ak liggéeykati bant, ngir ñu tabaxal Daawuda kër.
2Daawuda nag xam ne Aji Sax jee ko fal buurub Israayil te moo kaweel nguuram lool ngir Israayil ñoñam.
3Gannaaw gi, Daawuda denc na yeneeni soxna ca Yerusalem. Mu am ca yeneen doom yu góor ak yu jigéen.
4Doom yu góor yi juddoo Yerusalem ñoo di Samwa ak Sobab ak Natan ak Suleymaan,
5ak Ibaar ak Elisuwa ak Elpelet,
6ak Noga ak Nefeg ak Yafya,
7ak Elisama ak Beelyada ak Elifelet.
8Ba waa Filisti déggee ne fal nañu Daawuda buurub Israayil, ñoom ñépp a jóg, di ko wër. Daawuda nag dégg ko daldi leen dogaleji.
9Waa Filisti dikk, songandoo xuru Refayeen ña.
10Daawuda laaj Yàlla ne ko: «Ndax ma songi waa Filisti? Dinga leen teg ci sama loxo?» Aji Sax ji ne ko: «Demal, ma teg leen ci sa loxo.»
11Ba mu ko defee Daawuda ak gàngooram dem ba Baal Peracim, Daawuda duma leen foofa. Daawuda nag ne: «Aji Sax jee jaare ci man, Buur, xàll aw yoon, ne jàyy ni walum ndox ca kaw noon ya.» Moo tax ñu woowe béreb boobu Baal Peracim (muy firi Boroom bi xàll naw yoon).
12Filisteen ña nag waccoon fa seeni tuur, Daawuda santaane ñu boole ko lakk.
13Ba loolu wéyee Filisteen ña dikk songaat xur wa.
14Daawuda dellu laaj Yàlla. Mu ne ko: «Bul topp seen gannaaw, wër leen ndombo, dal ca seen kaw fa janook garab ya.
15Booy dégg tànk yuy jaab ca kaw njobbaxtali sànd ya rekk, songal ndax booba Yàllaa la jiitu, di dumaji waa dalub Filisti.»
16Daawuda nag def la ko Yàlla sant, ba ñu duma gàngooru Filisteen ña, la ko dale Gabawon ba Geser.