1Góor ñiy doomi Yanqóoba mi ñuy wax itam Israayil ñoo di Ruben ak Simeyon ak Lewi ak Yuda+ 2.1 Yuda mooy maamu Daawuda. Seetal ci 2.15.* ak Isaakar ak Sabulon
2ak Dan ak Yuusufa ak Beñamin ak Neftali ak Gàdd ak Aser.
3Doomi Yuda yu góor ñoo di Er ak Onan ak Sela. Ñooñu, doomu Suwa, ndawas Kanaaneen sa la ko amal. Waaye Er, taawub Yuda boobu, doonoon ku Aji Sax ji|lemma="Aji Sax j-:"* seede coxoram; Aji Sax ji rey ko.
4Ku ñuy wax Tamar, gorob Yuda ba doomam doon denc, am ak Yuda Peres ak Sera. Doomi Yuda yu góor yépp di juróom.
5Doomi Peres yu góor nag di Esron ak Amul.
6Doomi Sera yu góor ñoo di Simri ak Etan ak Eman ak Kalkol ak Daara; ñoom ñépp di juróom.
7Doomu Karmi ju góor moo di Akar+ 2.7 Akar mooy Akan ba tey. Seetal ci +bk Yosuwe+bk* saar 7.* (muy firi Musiba), ki yóbbe woon Israayil musiba ba mu feccee worma ca mbir ya ñu aayaloon, jagleel ko Yàlla.
8Doomu Etan ju góor moo di Asaryaa.
9Doomi Esron yu góor yi mu am ñoo di Yeraxmeel ak Ram ak Kaleb, mooy Kelubay ba tey.
10Ram mooy baayu Aminadab, Aminadab di baayu Naason, kilifag giirug Yuda.
11Naason mooy baayu Salma, Salma di baayu Bowas.
12Bowas mooy baayu Obedd, Obedd di baayu Yese.
13Yese mooy baayu Elyab, taawam bu góor, Abinadab di tofoom, Simeya di ñetteelu doomam ju góor.
14Netaneel mooy ñeenteelu doomam ju góor, Raday di juróomeelu doomam ju góor.
15Occem a ca topp di juróom benneel, Daawuda toppaat ca, di juróom ñaareelu doomam ju góor.
16Ñooñu seeni jigéen a doon Ceruya ak Abigayil. Doomi Ceruya yu góor di Abisay, Yowab ak Asayel, ñuy ñett.
17Abigayil moo jur Amasa ma Yeter Ismayleen ba di baayam.
18Kaleb miy doomu Esron ju góor am na ñetti doom yu góor ak soxnaam yi tudd Asuba ak Yeryot, ñuy: Yeser, Sobab ak Ardon.
19Ba Asuba faatoo, Kaleb jël Efrata, mu am ak moom Ur.
20Ur mooy baayu Uri, Uri di baayu Beccalel.
21Gannaaw gi, Esron tollu ci juróom benn fukki at, jël doomu Makir miy baayu Galàdd. Mu am ca doom ju góor ju ñuy wax Segub.
22Segub mooy baayu Yayir ma tegoon loxo ñaar fukki dëkk ak ñett ca diiwaanu Galàdd.
23Waaye Gesureen ñaak Arameen ña nangu ca ñoom dëkk yu ndaw ya ca Yayir, boole ca Kenat ak dëkk ya ca bokk, lépp di juróom benn fukki dëkk. Góor ñooñu ñépp nag doomi Makir lañu woon, moom baayu Galàdd.
24Gannaaw ba Esron faatoo ca Kaleb Efrata, la Abya ma doon soxnaam jur doomu Esron ja ñuy wax Asuur mi sanc Tekowa.
25Góor ñi Yeraxmeel, taawub Esron di seen baay ñoo di Ram may taawam ak Buna ak Oren ak Occem ak Axya.
26Yeraxmeel jëlaat na soxna su ñuy wax Atara, am ca ku ñuy wax Onam.
27Ram, taawub Yeraxmeel, ay doomam yu góor ñoo di Màcc ak Yamin ak Eker.
28Doomi Onam yu góor ñoo di Samay ak Yada. Doomi Samay yu góor di Nadab ak Abisur.
29Abisur nag jël Abiyayil, am ca Aban ak Molit.
30Doomi Nadab yu góor ñoo di Selet ak Apayim. Selet faatu na te amul doom.
31Doomu Apayim ju góor moo di Yisey. Doomu Yisey ju góor moo di Sesan. Doomu Sesan di Axlay.
32Góor ñi Yada mi bokk ak Samay jur ñoo di Yeter ak Yonatan. Yeter faatu na te amul doom.
33Doomi Yonatan yu góor ñoo di Pelet ak Sasa. Ñooñu ñoo soqikoo ci Yeraxmeel.
34Sesan nag amul doom ju góor waaye ay jigéen la am. Sesan amoon na jaamu waa Misra bu tudd Yarxa.
35Mu may Yarxa kenn ciy doomam yu jigéen. Mu amal ko ca doom ju góor ju tudd Atay.
36Atay mooy baayu Natan, Natan di baayu Sabàdd.
37Sabàdd mooy baayu Eflal, Eflal di baayu Obedd.
38Obedd mooy baayu Yewu, Yewu di baayu Asaryaa.
39Asaryaa mooy baayu Elecc, Elecc di baayu Elasa.
40Elasa mooy baayu Sismay, Sismay di baayu Salum.
41Salum mooy baayu Yekamya, Yekamya di baayu Elisama.
42Góor ñi Kaleb, ma bokk ak Yeraxmeel, di seen baay ñoo di Mesa, may taawam, te di baayu Sif ak Maresa, baayu Ebron.
43Doomi Ebron yu góor ñoo di Kore ak Tapuwa ak Rekem ak Sema.
44Sema mooy baayu Raxam, Raxam di baayu Yorkam, Rekem mooy baayu Samay.
45Samay mooy baayu Mawon, Mawon di baayu Bet Cur.
46Kaleb, Efa nekkaaleem la woon. Moo jur Karan ak Mocca ak Gases. Karan am na doom ju góor ju mu tudde Gases moom it.
47Doomi Yaday yu góor ñoo di Regem ak Yotam ak Gesan ak Pelet ak Efa ak Saaf.
48Kaleb amoon na beneen nekkaale bu ñuy wax Maaka. Mu am ak moom Seber ak Tirxana.
49Gannaaw mu amaat ku ñuy wax Saaf di baayu Madmana, ak ku ñuy wax Sewa, di baayu Magbena ak Gibeya. Doomu Kaleb ju jigéen mooy Agsa.
50Ñeneen a ngi di ñu askanoo ci Kaleb: Ur taawam baak soxnaam sa ñuy wax Efrata, am na ñetti doom yu góor di Sobal ma sanc Kiryaat Yarim,
51ak Salma ma sanc Betleyem, ak Aref ma sanc Bet Gader.
52Sobal ma sanc Kiryaat Yarim moo meññ waa Arowe ak genn-wàllu waa Menuxot.
53Sobal moo meññ itam làngi Kiryaat Yarim yii di Yetereen ñi ak Puuteen ñi ak Sumateen ñi ak Misrayeen ñi. Ci ñooñu la Corateen ñeek Estawleen ñi soqikoo.
54Salma moo meññ waa Betleyem ak Netofa ak Aterot Bet Yowab ak genn-wàllu waa Manaxat ak Coreyeen ñi.