1Sëti Aaróona dees leena séddale ay kuréel yu méngook doomi Aaróona yu góor. Ñuy Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.
2Nadab ak Abiyu ñoo njëkka dee seen baay te amuñu doom yu góor. Elasar ak Itamar nag doon ay sarxalkat.
3Gannaaw gi, Daawuda ànd ak Cadog mi askanoo ci Elasar, ak Aximeleg mi askanoo ci Itamar, daldi séddale askanu Aaróona ay kuréel, kuréel gu ci nekk ak wàllam ci liggéey bi.
4Ñu gis nag sëti Elasar gëna bare ay kilifa sëti Itamar. Loolu tax ñu séddale leen, sëti Elasar yu góor di fukki kilifaak juróom benn jiite seen këri baay, sëti Itamar yu góor di juróom ñetti kilifa yu jiite seen këri baay.
5Na ñu séddalee ñenn ñi rekk lañu séddalee ña ca des, ci kaw tegoo bant, ndax amoon na ci biir sëti Elasar ak ci biir sëti Itamar ay jawriñ yu farewoo béreb bu sell bi ak itam ay jawriñ yu sasoo liggéeyu Yàlla bi.
6Ci biir loolu Semaya bindkat ba, doomu Netaneel te bokk ci giirug Lewi|lemma="Leween b-:"*, daldi bind seeni tur fa kanam Buur ak kilifa ya ak Cadog sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba ak Aximeleg doomu Abyatar ak kilifay waa kër sarxalkat yaak waa kër Leween ña. Ñu tegoo nag bant, ngir jël genn kër ci askanu Elasar, jël genn kër ci askanu Itamar.
7Ci biir loolu, ka bant ba njëkka yemool di Yoyarib, ñaareel ba di Yedaya,
8ñetteel ba di Arim, ñeenteel ba di Seworim,
9juróomeel ba di Malkiya, juróom benneel ba di Miyamin,
10juróom ñaareel ba di Akocc, juróom ñetteel ba di Abya,
11juróom ñeenteel bi di Yesuwa, fukkeel bi di Sekaña,
12fukkeel baak benn di Elyasib, fukkeel baak ñaar di Yakim,
13fukkeel baak ñett di Upa, fukkeel baak ñeent di Yesebab,
14fukkeel baak juróom di Bilga, fukkeel baak juróom benn di Imer,
15fukkeel baak juróom ñaar di Esir, fukkeel baak juróom ñett di Apicecc,
16fukkeel baak juróom ñeent di Petaxya, ñaar fukkeel ba di Esekiyel,
17ñaar fukkeel baak benn Yakin la, ñaar fukkeel baak ñaar di Gamul,
18ñaar fukkeel baak ñett Delaya la, ñaar fukkeel baak ñeent di Maasya.
19Noonu lañu leen séddalee ay kuréel ci liggéey bi ci biir kër Aji Sax ji. Ñuy def nag li ñu leen sas, ni leen ko seen maam Aaróona digale, te muy la ko Aji Sax ji Yàllay Israayil santoon.
20Njiiti Leween|lemma="Leween b-:"* ñi des ñii la: ci askanu Amram, Subayel la; ci askanu Subayel, Yeja la.
21Ci askanu Rexabya, doomi Rexabya la, njiit la di Isiya.
22Ci askanu Iccar, Selomot la, ci askanu Selomot, Yaxat la.
23Doomi Ebron yu góor ñoo di Yerya may taaw, Amarya di ñaareel ba, Yaxasyel di ñetteel ba; Yekamam di ñeenteel ba.
24Doomu Usyel ju góor Mise la. Askanu Mise, Samir bokk na ca.
25Askanu Isiya mi bokk ak Mise, Sàkkaryaa ca la.
26Doomi Merari yu góor, Maxli la ak Musi ak Yaasya.
27Askanu Merari gi soqikoo ci Yaasya, doomam ju góor, Sowam la ak Sakur ak Ibri.
28Doomi Maxli yu góor ñoo di Elasar ma amul doom ju góor,
29ak Kis mi Yeraxmeel di doomam ju góor.
30Doomi Musi yu góor ñoo di Maxli ak Eder ak Yerimot.