1Kuréeli wattukati bunt yi, nii lañu ko séddalee woon: Ci askanu Kore, Meselemya la, sëtub Kore, bokk ci doomi Asaf.
2Ay doomam yu góor di Sàkkaryaa taaw ba, Yediyel di ñaareel ba, Sebaja di ñetteel, Yatniyel di ñeenteel,
3Elam di juróomeel, Yoxanan di juróom benneel, Elyowenay di juróom ñaareel.
4Obedd Edom am ay doom yu góor: taaw ba di Semaya, ñaareel ba di Yewosabàdd, ñetteel ba di Yowax, ñeenteel ba di Sakar, juróomeel ba di Netaneel,
5juróom benneel ba di Amyel, juróom ñaareel ba di Isaakar, juróom ñetteel ba di Pewultay. Obedd Edom nag Yàlla da koo barkeeloon.
6Taawam Semaya amoon na ay doom yu góor, di ay kilifa ci seen kër baay ndax nit ñu tekki lañu woon.
7Doomi Semaya yu góor ñoo di Otni ak Refayel ak Obedd ak Elsabat ñook seeni bokk yu tekki, di Eliyu ak Semakiya.
8Ñooñu ñépp sëti Obedd Edom lañu, ñook seen doom yu góor ak seeni bokk; ñuy nit ñu tekki diy jàmbaar ci liggéey bi, tollu ci juróom benn fukk ak ñaar ñu ñu waññal Obedd Edom.
9Kuréelu Meselemya doomam yu góor a ca nekk aki bokkam, di fukki nit ak juróom ñett ñu tekki.
10Osa mu làngug Merari am na ñeenti doom yu góor, Simri jiitu ca, baayam def ko njiit doonte du taaw;
11Ilkiya di ñaareel ba, Tebalya di ñetteel ba, Sàkkaryaa di ñeenteel ba. Kuréelu Osa mboolem doomam yu góor a ca nekk aki bokkam, di fukki nit ak ñett.
12Ci mboolem kuréeli wattukati bunt yooyu, kilifa yaak ña ca des dañu daan def seen liggéey ci biir kër Aji Sax ji.
13Dañoo tegoo bant bunt bu nekk, ngir jox ko waa kër gi koy wattu, mag ñeek ndaw ñi bokk ci yem.
14Ka muurloo buntu penku ba nag di Selemya. Sàkkaryaa, doomam ju góor ja amoon xel mu ñaw, daldi muurloo bunt ba féete bëj-gànnaar.
15Obedd Edom féetewoo buntub bëj-saalum, ay doomam yu góor féetewoo këri dencukaay ya.
16Suppim a nga feggook Osa bokk di wattu buntub sowu ba ak buntub Saleket bay ubbikoo ca yoonu yéeg ga.
17Amoon na juróom benni Leween|lemma="Leween b-:"* yu aye wetu penku bés bu nekk, ak ñeenti Leween wetu bëj-gànnaar bés bu nekk, ak ñeent ca bëj-saalum bés bu nekk, ak ñaar ñuy awanteek ñaar ca dencukaay ya.
18Ñeent a nekkoon ca mbedd ma, ngir ëtt ba ca sowu; ñaar nekk ca ëtt ba.
19Looloo doon kuréeli wattukati bunt ya bokkoon ca askanu Kore ak Merari.
20Yeneen Leween|lemma="Leween b-:"*, ñu mel ni Axya lañu dénkoon alali kër Yàlla ga ak alal yu sell|lemma="sell:"* ya.
21Sëti Ladan mu làngu Gerson, diy kilifa ci seeni waa kër, doomam Yexyelee ci bokkoon.
22Doomi Yexyeli yu góor ñooy Setam ak Yowel. Mbokku Yexyeli di wattu alali kër Aji Sax ji.
23Ci wàllu làngi Amram ak làngu Iccar ak làngu Ebron ak làngu Usyel:
24Sebuwel, ma askanoo ca Gersom, doomu Musaa ju góor, moo doon jawriñ ja ñu dénk alal ya.
25Bokkam yi soqikoo ci Elyeser nii lañu toppantee: Rexabya ak Esayi ak Yoram ak Sikkri ak Selomit.
26Selomit mooki bokkam lañu dénkoon mboolem alal yu sell ya, te ña ko sellalal Aji Sax ji, di Buur Daawuda ak kilifay kër ña jiite woon kuréeli junniy nit ak ña jiite woon kuréeli téeméer ya ak yeneen njiiti mboolooy xare ya.
27Ñooñu dañoo jëloon ca la ñu lële ca ay xare, jagleel ko liggéeyu kër Aji Sax ja ñuy defaraat.
28Mboolem lu ñu sellal te ña ko sellalal Aji Sax ji, di Samiyel boroom gis ba, ak Sawul doomu Kis, ak Abner doomu Ner, ak Yowab doomu Ceruya, ak yeneen yu ñu sellal yépp, dañu ko tegoon ca loxol Selomit mooki bokkam.
29Ñi bokk ci làngu Iccar, di Kenaña aki doomam yu góor, ñoo gàddu woon mbiri biir dëkk ba ca Israayil, yore saytu ba ak àtte ba.
30Ñi bokk ci làngu Ebron, di Asabya aki bokkam, di junniy nit ak juróom ñaari téeméer (1 700) ñu tekki, ñoo yilifoon wetu Israayil gi féete dexu Yurdan sowu ci mboolem lu jëm ci liggéeyu Aji Sax ji ak liggéeyu buur.
31Ci wàllu làngu Ebron, Yerya moo doon kilifa ga. Ca ñeent fukkeelu atu nguurug Daawuda, seet nañu ba gis ca seen biir, ca Yaser ga ca diiwaanu Galàdd, ay nit ñu tekki ñu bokk ca ñoom.