1Nii lañu lime bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* yi nekkoon ay kilifa ci seen kër baay, doon njiiti kuréeli junni ak kuréeli téeméeri nit, te nekkoon saytukat yi doon jàppale Buur ci lu jëm ci kuréelu xarekat yi aye ci liggéey bi weer wu nekk. Kuréel gu nekk ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) a ca nekkoon.
2Ka jiite woon kuréel gu njëkk ga ca weer wu njëkk wa, Yasobam la, doomu Sabdiyel. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
3Mu ngi askanoo ci Peres, di kilifag mboolem jawriñi gàngoori xare ya ca weer wu njëkk wa.
4Ka jiite woon kuréelu ñaareelu weer wa, Doday la, te mu askanoo ci Axowa; Miglot topp ci moom, jiite kuréelam. Kuréel ga ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
5Kilifag ñetteelu mbooloo ma ca ñetteelu weer wa, Benaya la woon, doomu Yoyada, sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag ba. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
6Benaya moomoo doon jàmbaari xare ja bokkoon ca Fanweeri jàmbaar ya, jiite leen. Amisabat, doomam ju góor bokk ca kuréel ga.
7Ñeenteelu kilifa ga ca ñeenteelu weer wa, Asayel la, mbokkum Yowab; Sebaja, doomam ju góor moo ko wuutu. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
8Juróomeelu kilifa ga ca juróomeelu weer wa, Samut la, bokk ci làngu Israx. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
9Juróom benneelu kilifa ga ca juróom benneelu weer wa, Ira la woon, doomu Ikes mu Tekowa. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
10Juróom ñaareelu kilifa ga ca juróom ñaareelu weer wa, Elecc la woon, mu Palon, bokk ca giirug Efrayim. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
11Juróom ñetteelu kilifa ga ca juróom ñetteelu weer wa, Sibekay la woon, mu Usa, bokk ca làngu Sera. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
12Juróom ñeenteelu kilifa ga ca juróom ñeenteelu weer wa, Abiyeser la woon, mu Anatot, bokk ca giirug Beñamin. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
13Fukkeelu kilifa ga ca fukkeelu weer wa, Maaray la woon, mu Netofa, bokk ca làngu Sera. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
14Fukkeelu kilifa gaak benn ca fukkeelu weer waak benn, Benaya la woon, mu Piraton, bokk ca giirug Efrayim. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
15Fukkeelu kilifa gaak ñaar ca fukkeelu weer waak ñaar, Elday la woon, mu Netofa, bokk ca làngug Otniyel. Kuréelam ñaar fukki junniy nit ak ñeent (24 000) la woon.
16Kilifay giiri Israayil nag ñii la:
17Kilifag giirug Lewi|lemma="Leween b-:"* Asabya la, doomu Kemwel.
18Kilifag giirug Yuda Eliyu la, mbokkum Daawuda.
19Kilifag giirug Sabulon Ismaya la, doomu Abdiyas.
20Kilifag giirug Efrayim Ose la, doomu Asasya.
21Kilifag genn-wàllu giirug Manase ga ca penkub dexu Yurdan, ca Galàdd, Ido la, doomu Sàkkaryaa.
22Kilifag giirug Dan, Asareel la, doomu Yeroxam.
23Daawuda nag boolewu ci limu nit ñi am ñaar fukki at ak lu ko yées ndax Aji Sax ji dige woon na ne dina giiral Israayil ba ñu tollook biddiiwi asamaan.
24Yowab doomu Ceruya tàmbali woon na leen lim sax, waaye sottalul, ndax loolu taxoon na sànjum Yàlla wàcc ci kaw Israayil. Moo tax lim ba bokkul ca limeefu téere bi ñu dippee Jaloorey Buur Daawuda cay jantam.
25Ci biir loolu, ka ñu dénkoon këri dencukaay Buur, Asmawet la, doomu Adiyel.
26Ka jiite woon surga yay liggéey ca tool ya, di bey, Esri la, doomu Kelub.
27Ka ñu dénkoon tóokëri reseñ ya, Simey mu Raama la.
28Ka ñu dénkoon garabi oliw yaak garabi sikomoor ya ca suufu tund ya, mooy Baal Anan mu Bet Geder.
29Ka ñu dénkoon nag ya ca parlu ya ca jooru Saron, mooy Sittray mu Saron.
30Ka ñu dénkoon giléem ya, Obil la, bokk ca giirug Ismayla.
31Ka ñu dénkoon gàtt ya, Yasis la, bokk ci giirug Agar.
32Yonatan, baay bu ndawu Daawuda, di ku rafet xel te am njàng, moo doon xelal Buur Daawuda. Yexyel doomu Agmoni yore njàngu doomi Buur.
33Axitofel it doon na xelal Buur; Usay Arkeen ba di ab xejjam.