1Doomi Daawuda yu góor ya mu amoon ca Ebron ñoo di: Amnon taaw ba Axinowam ma dëkkoon Yisreel di ndeyam. Ñaareelu doomam ju góor di Dañeel ma Abigayil ma dëkkoon Karmel di ndeyam.
2Ñetteelu doomam ju góor moo di Absalom ma Maaka doomu Talmay buurub Gesur di ndeyam. Ñeenteel ba di Adoña ma Agit di ndeyam.
3Juróomeelu doomam ju góor moo di Sefatiya, ma Abital di ndeyam. Juróom benneelu doomam ju góor di Ittireyam ma mu am ak soxnaam sa ñuy wax Egla.
4Juróom benn ñooñu la Daawuda am ca Ebron ga mu falu buur juróom ñaari at ak juróom benni weer.
5Ña Daawuda am ca Yerusalem ñoo di Simeya ak Sobab ak Natan ak Suleymaan. Ñooñu ñeent Batseba mi Amyel di baayam mooy seen ndey.
6Daawuda am na it Ibaar ak Elisama ak Elifelet.
7Am na Noga ak Nefeg ak Yafya.
8Am na Elisama ak Elyada ak Elifelet. Muy yeneen juróom ñeenti doomi Daawuda yu góor.
9Muy mboolem doomi Daawuda yu góor ba mu des doom yi mu am ak ay nekkaaleem. Amoon na itam doom ju jigéen ju ñuy wax Tamar.
10Doomu Suleymaan mooy Robowam mi jur Abya, mu jur Asa, mu jur Yosafat.
11Yosafat jur Yexoram, mu jur Axasya, mu jur Yowas,
12mu jur Amaciya, mu jur Asaryaa, mu jur Yotam;
13Yotam jur Axas, mu jur Esekiyas, mu jur Manase.
14Manase moo jur Amon mi jur Yosya.
15Doomi Yosya yu góor ñoo di Yoxanan, ñaareelu doomam di Yoyakim, ñetteel ba di Cedesyas, ñeenteel ba di Salum.
16Doomi Yoyakim yu góor ñoo di Yekoña ak Cedesyas.
17Yekoña lañu yóbbu ngàllo Babilon. Doomi Yekoña yu góor ñoo di Selcel
18ak Malkiram ak Pedaya ak Senacar ak Yekamya ak Osama ak Nedabya.
19Doomi Pedaya yu góor ñoo di Sorobabel ak Simey. Sorobabel am na ñaari doom yu góor, Mesulam ak Anaña, ak doom ju jigéen ju ñuy wax Selomit.
20Mu dellu am juróomi doom yu góor. Ñuy Asuba ak Oyel ak Berekya ak Asaja ak Yusab Xeset.
21Ñi askanoo ci Anaña di ay góor ñoom ñépp di Pelaca ak Yesaya; ak itam doom yu góor yu Refaya ak yu Arnan ak yu Abdiyas ak yu Sekaña.
22Ñi askanoo ci Sekaña ñoo di Semaya aki doomam yu góor, ñooy Atus ak Igal ak Baryax ak Neyarya ak Safat. Ñuy juróom benn.
23Doomi Neyarya yu góor ñoo di Elyonay ak Esekiyas ak Asrikam, ñuy ñett.