1.Jaar-jaar ya 8:1-39 WOLB2025 - Bible AI

1Beñamin mooy baayu Bela miy taawam bu góor. Ku góor ka ca topp di Asbel, Aara di ñetteelu doomam ju góor.

2Noxa di ñeenteelu doomam ju góor, Rafa di juróomeelu doomam ju góor.

3Doomi Bela yu góor ñoo di Adar ak Gera ak Abiyudd.

4Abiswa ca la ak Naaman ak Axowa.

5Gera it ca la ak Sefufan ak Uram.

6-7 Doomi Exudd yu góor yooyu di Naaman ak Axya ak Gera. Ñoo doon kilifay làngu waa Geba ya ñu toxal Manaxat, te Gera moo leen toxal. Mooy baayu Usa ak Axixudd.

8Saxarayim, gannaaw ba mu fasee Usim ak Baara ñaari soxnaam ya, am na ay doom yu góor ca réewam Mowab.

9Moo jël Odes soxna, am ca Yobab ak Cibya ak Mesa ak Malkam.

10Am na ca it Yewucc ak Sakiya ak Mirma. Doomam yu góor yooyu mujj jiite seen kër baay.

11Fekk na mu am ak Usim ñaari doom yu góor, Abitub ak Elpaal.

12Doomi Elpaal yu góor ñoo di Eber ak Misam ak Semedd. Semedd moomu moo tabax dëkk ya ñuy wax Ono ak Lodd ak dëkk yu ndaw ya ko wër.

13Berya ak Sema ay kilifay làngi waa Ayalon lañu woon. Ñoo dàq waa Gaat.

14Ñii di Axyo ak Sasag ak Yeremot

15ak Sebaja ak Aràdd ak Eder

16ak Mikayel ak Ispa ak Yoxa, ñooy góor ñi Berya di seen baay.

17Sebaja nag mook Mesulam ak Iski ak Eber,

18ak Ismeray ak Isliya ak Yobab ñooy góor ñi Elpaal di seen baay.

19Yakim ak Sikkri ak Sabdi

20ak Eliyenay ak Ciletay ak Elyel

21ak Adaya ak Beraya ak Simrat ñooy góor yi Simey di seen baay.

22Ispan nag mook Eber ak Elyel

23ak Abdon ak Sikkri ak Xanan

24ak Anaña ak Elam ak Anatoca

25ak Ifdeya ak Penuwel, ñooy góor ñi Sasag di seen baay.

26Samseray ak Sexarya ak Atalyaa

27ak Yaaresya ak Elya ak Sikkri, ñooy góor ñi Yeroxam+ 8.27 Yeroxam mooy Yeremot ba tey. Seetal ci aaya 14 (8.14).* di seen baay.

28Ñooñoo jiite woon seeni waa këri maam, ku nekk ak sag maas. Ña nga dëkkoon Yerusalem.

29Baayu Gabawon, Gabawon la dëkkoon. Maaka la soxnaam tudd.

30Taawam bu góor moo doon Abdon, góor ña ca topp di Cur ak Kis ak Baal ak Ner ak Nadab,

31ak Gedor ak Axyo ak Seker+ 8.31 Seker ak Sàkkaryaa, kenn ki la. Seetal ci +bk 1.Jaar-jaar ya+bk* 9.37.*

32ak Miglot baayu Simeyam+ 8.32 Simeyam mooy Simeya ba tey. Seetal ci 9.38.*. Ñooñu itam ña nga dëkkoon Yerusalem ñook seeni bokk.

33Ner mooy baayu Kis, Kis di baayu Sawul, Sawul di baayu Yonatan ak Malkisuwa ak Abinadab ak Esbaal+ 8.33 Esbaal mooy Isboset ba tey. Seetal ci +bk 2.Samiyel+bk* 2.8.*.

34Doomu Yonatan ju góor moo di Meribaal+ 8.34 Meribaal mooy Mefiboset ba tey. Seetal ci +bk 2.Samiyel 4.4+bk*; +bk 1.Jaar-jaar ya+bk* 9.40.*; Meribaal di baayu Mise.

35Doomi Mise yu góor ñoo di Piton ak Meleg ak Tareya ak Axas.

36Axas mooy baayu Yowada, Yowada di baayu Alemet ak Asmawet ak Simri; Simri di baayu Mocca.

37Mocca mooy baayu Bineya. Bineya di baayu Rafa, Rafa di baayu Elasa, Elasa di baayu Accel.

38Accel amoon na juróom benni doom yu góor, ñuy Asrikam ak Bokkru ak Ismayel ak Seyarya ak Abdiyas ak Xanan. Ñooñu ñépp Accel moo leen jur.

39Eseg la Accel bokkal. Góor ñi Eseg di seen baay ñoo di Ulam, taawam, Yewus topp ca, Elifelet toppaat ca.

le>