1Ci man Piyeer, ndawal Yeesu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi la bataaxal bii bawoo, ñeel askan wi Yàlla tànn, te ñu toxuji diiwaani Pont ak Galasi ak Kapados ak Asi ak Bitini+ 1.1 Dafa mel ni, ñi gëm Almasi bi ci bànni Israayil la wax, te ñu dëkk ci diiwaan yooyu. Juróomi diiwaan yooyu yépp, réew mi ñuy wax Tirki tey, ci lañu bokkoon.*.
2Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi bi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Na aw yiw ak jàmm juy baawaan ñeel leen.
3Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi bi, ngir may nu yaakaar juy dund.
4Loolu moo am ngir ab cér bu dul yàqu, du sobewu, du seey, cér bu dence fa asamaan ñeel leen,
5yeen ñi seen ngëm tax ngeen yiiru ci manoorey Yàlla, mi leen di nége mucc ga mu waajal te di ko feeñal ca bés bu mujj ba.
6Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu.
7Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.
8Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,
9ndax yeena ngi jot ci yool bi ngëm di yóotu, te mooy texe.
10Googu texe, yonent ya jottali woon waxyub|lemma="waxyu:"* seen yiw wi leen dikkal, niir nañu ko, càmbar ko.
11Gëstu nañu jan jamono ak yan xew-xew la Noowug|lemma="Noo gu Sell g-:"* Almasi gu Sell ga nekkoon ci ñoom tegtale woon. Mooy ba Noo gay seede lu jiitu coonoy Almasi bi ak ndam ya cay topp.
12Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey jii, ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi, ci dooley Noo gu Sell gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax bëggoon nañoo nemmiku.
13Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi feeñee.
14Gannaaw gone yu dégg ndigal ngeen, buleen toppati seen xemmemtéefi bakkan ya woon, ba ngeen xamulee.
15Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin.
16Ndax kat bindees na ne: «Ñu sell|lemma="sell:"* ngeen wara doon, ndax man Ku sell|lemma="Aji Sell j-:"* laa+ 1.16 Seetal ci +bk Sarxalkat yi+bk* 19.2.*.»
17Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.
18Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote|lemma="jot:"* ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam,
19waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.
20Bu yàgg, ba àddina sosoogul la Yàlla tuddaloon Almasi bi loolu, waaye léegi ci mujug jamono jii la ko Yàlla feeñal ngir yeen
21ñi Almasi bi tax ngeen gëm Yàlla. Te Yàllaa ko dekkal, may ko ndam, ba tax Yàlla di ki ngeen gëm, yaakaar ko.
22Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.
23Ndax kat dangeena judduwaat, te jiwu wi ngeen judduwaate mooy kàddug Yàlla giy dund te sax dàkk; du jiwu wuy yàqu, waaye mooy jiwu wu dul yàqu mukk.
24Ndax bindees na ne: