1.Piyeer 2:1-24 WOLB2025 - Bible AI

1Kon nag baleen mboolem xeetu mbon ak mboolem njublaŋ ak jinigal ak kiñaan ak mboolem xeetu yàq der.

2Ni liir buy doora juddu yàkkamtee nàmpe, ni ngeen wara yàkkamtee nàmp soow mu set miy kàddug Yàlla. Mooy tax ngeen màgg ci seen dundug texe,

3gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi.

4Dikkleen ci moom, mooy doj wuy dund. Nit ñee ko beddi moos, waaye Yàllaa ko fal, fonk ko.

5Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi.

6Moo waral lii dikk ci Mbind mi:

7Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag:

8Te it:

9Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

10Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeenay xeet wi Yàlla ñoñoo+ 2.10 Seetal ci +bk Ose+bk* 1.6, 9; 2.25.*; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.

11Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.

12Seen dundin ci biir jàmbur ñi gëmul, rafetalleen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.

13Nangulleen gépp kilifteef gu tege ci àddina ngir Boroom bi; muy buur bu mag bi gëna kawe,

14mbaa boroom dëkk yi diy ndawam, te mu tabb leen, ngir ñu mbugal ñiy def lu bon, te sargal ñiy def lu baax.

15Ndax coobarey Yàlla kat moo di ngeen di def lu baax, ba wedamal nit ñu ñàkk bopp ñi xamul dara.

16Ay gor ngeen, waaye jaami Yàlla ngeen. Kon buleen taafantaloo li ngeen diy gor, ba def lu bon.

17Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragalleen ko; te buur, teral leen ko.

18Yeen jaam yi, nangulleen te weg wegeel gu mat sëkk seeni sang, te du sang yi baax te lewet doŋŋ, waaye ñu wex ñi itam ci lañu.

19Ndax nit ki su séddee Yàlla ab cér, ba tax mu muñ tiis ak coono bu ko yoon tegul, loolu aw yiw la.

20Muñ ay dóor yu la fekk ci tooñ, ana lu ciy ndam? Waaye soo muñee coono boo daj ngir lu baax loo def, loolu de aw yiw la fa kanam Yàlla.

21Ci loolu sax lañu leen woo, ndax Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi itam sonn na ngir yeen, te moo leen bàyyeel ab royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.

22«Moo bàkkaarul, fenul+ 2.22 Seetal ci +bk Esayi+bk* 53.9.*.»

23Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.

24«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam+ 2.24 Seetal ci +bk Esayi+bk* 53.4, 5.*.»

© 2025 Bible Society of Senegal
iv>