1Naka noonu yeen jigéen ñi, nangulleen seen jëkkër, ngir jëkkër ju ci nanguwula gëm kàddu gi it, mana gindiku te seen wax yeen, du ci am yoon, ngir na ngeen di jëfe,
2ndax day xool ci yeen ak seenug sellal gu ànd ak wegeel.
3Seen gànjar bumu doon gànjaru biti bu yem ci ay létt yu rafet ak takkaayi wurus ak yére yu yànj,
4waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.
5Bu njëkkoon loolu moo doon gànjaru jigéen ñu sell ña yaakaaroon Yàlla te nangul seen jëkkër,
6noonu Saarata déggale woon Ibraayma, naan ko «Sang bi». Yeen jigéen ñi nag, yeenay doomi Saarata, li feek yeena ngi def lu baax te bañ cee ragal ku leen xupp.
7Naka noonu yeen góor ñi, bàyyileen xel ni ngeen dëkke ak seeni jabar, tey sóoraale néew dooley jigéen. Séddleen leen teraangay nawle, gannaaw yeena bokk wenn yiw wi leen may ngeen dund dëgg. Su ko defee dara du gàllankoor seeni ñaan.
8Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.
9Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.
10Ndax kat:
11Na daggook lu bon, tey def lu baax,
12Ndax ay gët la Boroom bi ne jàkk aji jub ñi,
13Te it su ngeen dee ñu njaxlaf ci def lu baax, ana ku leen di def lu bon?
14Te sax su ngeen doon jànkoonteeki coono ndax seenug njub, ndokkalee yeen. «Buleen am jenn tiitaange ci seeni xuppe, te buleen jaaxle+ 3.14 Seetal ci +bk Esayi+bk* 8.12.*.»
15Waaye Sang Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi ngeen di sellal ci seen xol, te waajal nu ngeen di tontoo ku leen laaj lu jëm ci yaakaar ji ngeen am.
16Waaye nay tont lu rafet te ànd akub yar. Saxooleen di jëfe li dalal seenum xel, ba mbir ma ñu leen di baatale, ñooñuy ŋàññ seen dundin wu rafet wi leen Almasi bi manloo, gàcce rekk lañuy jële ca mbir ma ñu leen di baatale.
17Coono yu la jëf ju baax yóbbe kat, ndegam da di coobarey Yàlla, moo gën coono yu la jëf ju bon yóbbe.
18Almasi bi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi.
19Ci dooley Noo googu la deme ba waari mbindeef ya tëje+ 3.19 Seetal it ci +bk 2.Piyeer+bk* 2.4; +bk Yudd+bk* aaya 6.*,
20ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yatt gaal ga. Lim bu néew, juróom ñett ña ca duggoon, mucce ca ndox ma.
21Fi ñu leen jaarale, ci mbënn ma, moo di misaalub sóobu gi leen musal tey+ 3.21 sóobu: seetal ci +bk Room+bk* 6.3-4.*; du sóobu guy dindi tërub yaram, waaye moom ngeen di wuyoo wooteb Yàlla ci xel mu dal, te li leen di musal mooy ndekkitel Yeesu Almasi