1.Samiyel 11:1-14 WOLB2025 - Bible AI

1Naxas Amoneen ba moo dikkoon, gaw dëkk ba ñu naan Yabes ca Galàdd. Waa Yabes gépp wax ak moom, ne ko: «Ngalla digool ak nun jàmm, te nu nangul la.»

2Naxas Amoneen ba ne leen: «Ni may digook yeen daal, mooy nii: luqi seen bëtu ndijoor yeen ñépp, ba Israayil gépp torox.»

3Magi Yabes ne ko: «May nu juróom ñaari fan, nu yebal ay ndaw ci Israayil gépp. Su amul kenn ku nu wallu, nu dikk, fekksi leen.»

4Ba ndaw ya dikkee Gibeya ga Sawul dëkk, ba xamle mbir ma, waa dëkk ba di dégg, ñoom ñépp a yuuxu, di jooy.

5Ci biir loolu Sawul ne tëll, jiital ay nagam, jóge tool ya. Mu ne: «Lu nit ñi xewle bay jooy nii?» Ñu nettali ko kàdduy waa Yabes.

6Naka la Sawul dégg kàddu yooyu, leerug Yàlla dikk ne milib ca kawam, mer ma ne jippét tàkk.

7Mu rey ñaari nag, dog ko, yóbbante ko ay ndaw, yónnee ko Israayil gépp. Mu ne leen: «Képp ku toppul Sawul ak Samiyel, nii lees di def ay nagam.» Ba loolu amee tiitaange ju sababoo ci Aji Sax ji dal ca kaw askan wa, ñu sàqeendoo, di benn bopp.

8Ba Sawul nemmikoo limu góori Israayil ca Beseg, ñetti téeméeri junni lañu (300 000), waa Yuda di fanweeri junni (30 000).

9Ñu wax nag ndaw ya jóge Yabes Galàdd, ñu jottali seen waa dëkk ba ne leen, ca ëllëg sa bu jant bi tàngee, dees na leen wallu. Ndaw ya dem, àgge ko waa Yabes, waa Yabes bég.

10Ñu wax Amoneen ña, ne leen: «Ëllëg dinanu dikk, fekksi leen.»

11Ca ëllëg sa Sawul séddale gàngooru xareem ñetti kuréel. Ba ñu tolloo ci wattub njël, ñu dugg biir dalu Amoneen ña, di leen duma ba jant bi tàng. Ña ca rëcce daldi tasaaroo ba ñaar sax àndatuñu.

12Mbooloo ma ne Samiyel: «Ana ku noon: “Ndax Sawul ay falu ci sunu kaw?” Indileen ñooñu, nu rey leen!»

13Sawul ne leen: «Deesul rey kenn kay bésub tey jii, ndax bésub tey Aji Sax jee indi wall fi Israayil.»

14Ci kaw loolu Samiyel ne mbooloo ma: «Ñëwleen nu dem Gilgal, ba feddali pal gi.»

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>