1Samiyel daa waxoon Sawul, ne ko: «Man la Aji Sax ji yebal, ngir ma fal la buurub Israayil, ci aw ñoñam. Kon déglul kàddu yii Aji Sax ji wax.
2Aji Sax ju gàngoor yi dafa wax ne: “Maay dikke mbugal mu faj la Amalegeen ña defoon Israayil, tëru leen ca yoon wa, ba ñuy génn Misra.
3Demleen léegi, songi Amalegeen ñi. Faagaagalleen+ 15.3 faagaagal: li ñu ko bëgga firee fii mooy li ñu def alal ju ñu jagleel Aji Sax ji, ngir nit du ko saña jëfandikoo. Alal ju mel noonu, su duggul ci dencub kër Aji Sax ji, dees koy sànk.* seen lépp, te buleen leen ñeewante; reyleen góor ak jigéen, gone yi ba ci ñiy nàmp, ak nag ak gàtt ak giléem ak mbaam.”»
4Ba loolu amee Sawul woo gàngoor ga, lim leen ca Telem, ñuy ñaari téeméeri junniy (200 000) xarekat yuy deme tànk, ak fukki junniy (10 000) góori Yudeen.
5Sawul dem ba jot dëkkub Amalegeen ña, daldi waajal am tëru ca xur wa.
6Mu yónnee ca Keñeen ña, ne leen: «Demleen, dawleen jóge ci biir Amalegeen ñi, bala ma leena buubaaleek ñoom, te ba bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* di génn Misra, yeena leen jiwoon ngor ñoom ñépp.» Keñeen ña daw, jóge ca biir Amalegeen ña.
7Ba mu ko defee Sawul song Amalegeen ña, dale ko Awila ba dëkk ba ñuy wax Sur ca penkub Misra.
8Mu jàpp Agag buurub Amalegeen ña, gàngoor ga gépp, mu faagaagal, leel leen ñawkay saamar.
9Sawul ak gàngooram nag bàyyi Agag, muy dund, mook la gëna baax ca nag yaak gàtt ya: jurug yafal gaak kuuy yu ndaw ya, mboolem lu baax daal. Néeguñu caa faagaagal dara, waaye mboolem lu ca ñàkk solo mbaa mu yooy, loola lañu faagaagal.
10Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Samiyel ne ko:
11«Réccu naa li ma fale Sawul buur, ndax dëddu na ma, te samay ndigal, jëfewu ko.» Samiyel am ca njàqare lool, ba fanaanee tinu Aji Sax ji guddi gépp.
12Ba bët setee Samiyel teela jóg dem ngir dajeek Sawul. Ñu ne ko Sawul dem na dëkk ba ñuy wax Karmel, te defu fa lu moy yékkati am taax, terale ko boppam. Jóge na fa it, jàll ba Gilgal.
13Ba Samiyel demee ba gis Sawul, Sawul ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel. Def naa li Aji Sax ji santaane!»
14Samiyel ne ko: «Ana meem joojuy tàbbi sama nopp bii, lu mu doon? Ak looluy nàññi, may dégg?»
15Sawul ne ko: «Ca Amalegeen ña de lañu ko jële. Xarekat yee bàyyi li gën ci gàtt yeek nag yi, ngir sarxale ko sa Yàlla Aji Sax ji. Waaye la ca des moom, faagaagal nañu ko.»
16Samiyel ne Sawul: «Defal ndànk! Dinaa la xamal li ma Aji Sax ji wax biig.» Mu ne ko: «Waxal!»
17Samiyel ne ko: «Xanaa du yaa gisaloon sa bopp ne lu tuut nga woon, te yaay njiital giiri Israayil tey? Aji Sax ji fal la, ngay buurub Israayil,
18Aji Sax ji teg la ci yoon wi, ne la: “Demal faagaagal moykati Amalegeen ñi. Xareel ak ñoom, ba jeexal leen tàkk.”
19Lu la tere woona déggal Aji Sax ji, xanaa di saax-saaxee alal ji, di def li Aji Sax ji ñaawlu?»
20Sawul ne Samiyel: «Ndaxam déggal naa Aji Sax ji. Dox naa yoon wi ma Aji Sax ji yebal; indi naa Agag buurub Amaleg te Amalegeen ñi, faagaagal naa leen.
21Xarekat yi daal a tànne ci lël ji li gën ci gàtt yeek nag yi ñu wara faagaagal, ngir sarxal ko sa Yàlla Aji Sax ji ca Gilgal.»
22Samiyel ne ko:
23Bàkkaaru ngisaane la déggadi yemool,
24Sawul ne Samiyel: «Bàkkaar naa, ndax maa wàcc kàddug Aji Sax ji ak say ndigal, ndax ragal mbooloo mi, ba topp seen coobare.
25Léegi nag ngalla waay, baal ma sama bàkkaar bii te walbatiku, ànd ak man, ma sujjóotali Aji Sax ji.»
26Samiyel ne Sawul: «Duma walbatiku ànd ak yaw, ndax yaa gàntal kàddug Aji Sax ji, Aji Sax ji gàntal sa nguur ci Israayil.»
27Naka la Samiyel ne wërëñ, di dem, Sawul jàpp ca catal mbubb ma, mu dagg.
28Samiyel ne ko: «Nii la Aji Sax ji dagge nguurug Israayil ci yaw bés niki tey, jox ko keneen ku la gën.
29Te Aji Nekk-Fàww ju Israayil ji du fen, du réccu, ndax du nit bay réccu.»
30Sawul dellu ne: «Bàkkaar naa! Waaye ngalla waay sagal ma ci sama kanam magi askan wi ak ci kanam Israayil. Walbatikul, ànd ak man rekk, ma sujjóotali sa Yàlla Aji Sax ji.»
31Ba loolu amee Samiyel walbatiku topp Sawul. Sawul dem sujjóotali Aji Sax ji.
32Gannaaw loolu Samiyel ne: «Indilleen ma Agag buurub Amalegeen ñi.» Agag nag dikk, wutsi ko, ne finaax. Booba Agag a nga naan ca xelam: «Dee moom, tiitatuma ko, wees na!»
33Samiyel nag ne ko: «Ni aw jigéen ñàkke ay doom yu leen sa saamar xañ, ni la sa ndey di bokke tey ci jigéen ñi ñàkk doom.» Ci kaw loolu Samiyel rey Agag fa kanam Aji Sax ji ca Gilgal.
34Ba mu ko defee Samiyel dellu Raama, Sawul moom ñibbi këram ca Gibeya gu Sawul.