1.Samiyel 16:1-22 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji ne Samiyel: «Yaw foo àpp sa jooy yi ngay jooy Sawul te man maa ko dàq, ba doonatul buur ci Israayil? Gannaaw maa foq nguuram ci Israayil kay, duyal sa béjjén diwu oliw ba mu fees te nga dox, ma yebal la ci Yese waa Betleyem bi. Gis naa ciy doomam ki may fal buur.»

2Samiyel ne ko: «Ana nu ma fay deme? Sawul da koy dégg, rey ma!» Aji Sax ji ne ko: «Aw nag wu jigéen ngay jël, yóbbu, ne ko sarxalsi Aji Sax ji moo la indi.

3Su ko defee nga woo Yese ca sarax sa. Man maa lay xamal nooy def, ba nga diwal ma ki ma la wax, fal ko.»

4Samiyel def la Aji Sax ji wax. Ba mu agsee Betleyem, magi dëkk ba gatandoo ko tiitaange, ne ko: «Mbaa tànki jàmm?»

5Samiyel ne leen: «Jàmm rekk. Sarxalsi Aji Sax ji moo ma indi. Sanguleen-set te dikk ànd ak man ca sarax sa.» Ci kaw loolu mu sellal Yese ak doomam yu góor, woo leen ca sarax sa.

6Naka lañu agsi, Samiyel gis Elyab, daldi ne ca xelam: «Xam naa kii fi kanam Aji Sax ji rekk mooy ki mu fal!»

7Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»

8Yese daldi woo Abinadab, indi ko fi kanam Samiyel. Mu ne: «Aji Sax ji tànnul kii ba tey de!»

9Yese indi Simeya+ 16.9 Simeya mooy Saama ba tey.*, Samiyel ne: «Aji Sax ji tànnul kii it.»

10Yese indi juróom ñaari doomam yu góor fa kanam Samiyel, Samiyel ne ko: «Aji Sax ji tànnul kenn ci ñii.»

11Samiyel nag ne Yese: «Xale yu góor yi yemb nañu?» Yese ne ko: «Xanaa ki gën di ndaw. Ma ngay sàmm gàtt ya.» Mu ne ko: «Yónneel, woolu ko, dunu jekki te dikkul fii.»

12Yese yónnee, ñu indi ko. Ma nga def ku xees, neexa xool, bët ya leer nàññ. Aji Sax ji ne Samiyel: «Diw ko, kii la.»

13Samiyel fab béjjénu diw ba, diw ko fa kanam magam ña. Ba mu ko defee leerug Aji Sax ji dikk ne milib ca kaw Daawuda, dale fa ànd ak moom bésub keroog. Ba loolu wéyee Samiyel moom, dem dëkk ba ñu naan Raama.

14Ci kaw loolu leerug Aji Sax ji dëddu Sawul, ngelaw lu aay bàyyikoo ci Aji Sax ji, ub boppam.

15Ay dagi Sawul wax Sawul ne ko: «Lii kat ngelawal Yàlla lu aay la. Moo ub sa bopp.

16Nu ngii nag fi sa kanam, joxeel ndigal rekk sang bi, nu wutali la ku mana xalam. Su ko defee bu la ngelawal Yàlla lu aay songee, mu xalamal la, nga am jàmm.»

17Sawul ne dagam ya: «Ayca, seetalleen ma ku mane xalam bu baax, indil ma ko.»

18Kenn ca dag ya ne ko: «Man de, gis naa jenn doomu Yese waa Betleyem bi. Ku mana xalam la te jàmbaare. Ñeyi xare la. Ku déggi wax, ku góorayiw, te Aji Sax ji ànd ak moom.»

19Ba loolu amee Sawul yebal ay ndaw ca Yese ne ko: «Yónnee ma sa doom Daawuda, ma ca gàtt ya.»

20Yese yebal doomam Daawuda, daldi takk mbaam, sëf ko mburu ak mbuusu biiñ ak ab tef, ngir mu joxal ko Sawul yóbbal.

21Daawuda dem ca Sawul, daldi tàmbali di ko liggéeyal. Sawul sopp ko lool. Daawuda nag mujj di gàddukatu gànnaayam.

22Ci kaw loolu Sawul yónnee ca Yese, ne ko: «Bàyyil Daawuda, mu di ma liggéeyal far, ndax bég naa ci moom.»

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>