1.Samiyel 18:1-29 WOLB2025 - Bible AI

1Ba Daawuda di wax ak Sawul ba noppi, fekk na Yonatan yég ci xolam na mu taqook Daawuda ci biir cofeelu benn bakkan. Yonatan dafa soppoon Daawuda ni boppam.

2Bésub keroog la Sawul téye Daawuda, mayatu ko mu ñibbi kër baayam.

3Ba loolu amee Yonatan fasook Daawuda kóllëre|lemma="kóllëre g-:"*, ndax sopp ko ni boppam.

4Ci biir loolu Yonatan summi mbubbam, jox ko Daawuda, boole ca ay yérey xareem, ba ca saamaram ak fittam ak ngañaayam sax.

5Daawuda nag di dem ci bépp yoonu xare bu ko Sawul yebal, di ca am ndam. Sawul fal ko njiitu xarekat ya, gàngoor gépp rafetlu loolu, jawriñi Sawul itam rafetlu ko.

6Ba ñu demee ba xarekat yay ñibbi, gannaaw ba Daawuda reyee waa Filisti ba, jigéeni mboolem dëkki bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* a génn gatanduji Buur Sawul, di fecc aka woy, tabala ya ànd ak sarxolle ya ak xalam ya.

7Ña ngay fo, di awoonte, naan:

8Sawul ñaawlu kàddu ga, mer lool. Mu ne ca xelam: «Daawuda lañu moomale fukki junni; man, junni! Lu ko deseeti lu moy jal bi?»

9Bésub keroog la Sawul dale ronni Daawuda.

10Ca ëllëg sa ngelawal Yàlla lu aay ne milib ca kaw Sawul, mu nekk ci aal ca digg këram. Daawuda nag di ko xalamal, na mu daan def naka jekk, fekk Sawul ŋàbb ab xeejam.

11Mu jekki sànni xeej ba, te naan ca xelam: «Naa daaj Daawuda ci tabax bi!» Daawuda nag mbas ko ñaari yoon.

12Sawul daldi ragal Daawuda, ndax booba xam na ne Aji Sax jee ko dëddu, ànd ak Daawuda.

13Ba loolu amee mu jële ko fi wetam, fal ko njiitu kuréelu junniy xarekat, muy xareji, di délsi, jiite gàngoor ga.

14Daawuda baaxle ca yoonam yépp, Aji Sax ji ànd ak moom.

15Ba Sawul gisee Daawuda àntule lool, mu gën koo ragal.

16Teewul mboolem Israayil ak Yuda sopp Daawuda, ngir moo leen jiite woon, di xareji, di dikk.

17Ci kaw loolu Sawul ne Daawuda: «Sama taaw bu jigéen, Merab a ngii. Moom laa lay may. Nekkal ma sama jàmbaaru xare rekk, te xareel Aji Sax ji ay xareem.» Booba Sawul a nga naan ca xelam: «Bu ko sama loxo laal, nay loxol waa Filisti.»

18Daawuda ne Sawul: «Waaw, ana lu ma tekki, man maak samay bokk, sama askanu baay ci Israayil, ba wara mana goromlook Buur?»

19Ba ñu demee ba wara jox jabar Daawuda Merab doomu Sawul ja, Àddiryel ma cosaanoo Mewola lañu ko far may.

20Ci kaw loolu Mikal doomu Sawul bëgg Daawuda, ñu àgge ko Sawul, mu am ca mbégte.

21Booba Sawul a nga naan: «Naa ko ko may, ngir mu doon ndëgg-sërëxam, ba waa Filisti teg ko loxo.» Sawul nag wax Daawuda, ñaareel bi yoon, ne ko: «Tey ngay samab goro.»

22Ci biir loolu Sawul sant ay dagam, ne leen: «Diisoolleen maak Daawuda, ngeen wax ko ne ko: “Yaw kat, Buur am na bànneex ci yaw, te it dagam yépp a la sopp. Kon nag nangula doon gorob Buur.”»

23Dagi Sawul ya déey Daawuda kàddu yooyu. Daawuda ne leen: «Ngeen defe ne goromlook Buur daal, du dara? Man mii taqul dara, tekkiwuma dara!»

24Dag ya yegge Sawul kàddu yooyu Daawuda wax.

25Sawul ne leen: «Waxleen Daawuda ne ko, Buur de sàkkuwulub can: xanaa téeméeri mbuñukay waa Filisti yu mu feyoo ci noonam yooyu.» Booba la Sawul laloon mooy pexe mu tàbbal Daawuda ca loxol waa Filisti.

26Dag ya yegge Daawuda kàddu yooya, doon gorob Buur daldi koy jaral loola. Balaa àpp baa mat,

27Daawuda dem na, mooki nitam ba rey ñaari téeméeri waa Filisti. Daawuda indi seeni mbuñuka, ñu waññal ko Buur ba mu mat sëkk, mu daldi yeyoo goromlook Buur. Ba loolu amee Sawul may Daawuda doomam Mikal.

28Sawul nag xam xéll ne Aji Sax jee ànd ak Daawuda, te it doomam Mikal bëgg na ko,

29mu gën koo ragalati. Fa la Sawul doxe doon noonub Daawuda ba fàww.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>