1.Samiyel 19:1-23 WOLB2025 - Bible AI

1Ba mu ko defee Sawul xamal doomam Yonatan ak dagam yépp ne reylu Daawuda mooy li mu nar. Te Yonatan doomu Sawul sopp Daawuda lool.

2Yonatan yegge ko Daawuda, ne ko: «Sama baay a ngi lay wuta rey. Yaw nag fagarul kat te teela xëy ëllëg, seet foo làquji te baña génn.

3Man dinaa dem ci sama wetu baay, nu bokk taxaw ca tool ba ngay làquji. Man mii maay wax ak sama baay ci say mbir, ba gis na muy tëdde. Lu ma ci xam rekk, ñëw yegge la ko.»

4Ci kaw loolu Yonatan wax baayam lu baax ci Daawuda, ne ko: «Buur, ngalla bul tooñ Daawuda, sa jaam bii, ndax moom kat tooñu la, lu baax rekk la la masa defal.

5Jaay na bakkanam, ba rey waa Filisti ba. Aji Sax ji maye ca ndam lu réy, ñeel Israayil gépp, nga teg ci bët, am ca mbégte. Ana lu waral ngay tooñ, di tuur deretu jàmburu Yàlla bu mel ni Daawuda, reylu ko ci dara?»

6Sawul nag déggal Yonatan, daldi ne: «Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, deesul rey Daawuda.»

7Yonatan woo Daawuda, nettali ko waxtaan wa wépp, door koo yóbbu ca Sawul, mu dellu di ko liggéeyal, na woon.

8Ci kaw loolu xare jibaat, Daawuda dem xeexi ak waa Filisti, daan leen jéll bu réy, ñu daw.

9Ci kaw loolu ngelaw lu aay lu Aji Sax ji dikkal Sawul, fekk ko toog ci biir këram, ŋàbb ab xeejam, Daawuda di xalam.

10Sawul di wuta jam Daawuda xeej bi, ngir daaj ko ca tabax ba. Daawuda nag mbas ko, mu jam xeej ba ca tabax ba. Daawuda daldi daw, ba raw guddig keroog.

11Sawul yebal ay ndaw ca kër Daawuda ngir ñu xoolal ko ko, ba bët set, ñu rey ko. Mikal, soxnas Daawuda, yégal ko Daawuda, ne ko: «Soo rawalewul sa bakkan ci guddi gi de, bu ëllëgee dees na la rey.»

12Ba loolu amee Mikal jaarale ko ca palanteer ba, mu wàcc, daw, ba raw.

13Mikal jël gàllaaju kër ga, teg ca lal ba, fab deru bëy, teg fa féeteek bopp ba, daldi koy sànge malaan.

14Sawul yebal ay ndaw yu jàppsi Daawuda, Mikal ne: «Moom de daa wopp.»

15Ci kaw loolu Sawul dellu yebal ndaw ya, ngir ñu dem ba gis ko. Mu ne leen: «Indil leen ma ko, booleek lal bi, ba ma rey ko!»

16Naka la ndaw ya délsi, xool, gisuñu lu moy gàllaaju kër ga ca kaw lal ba, ak deru bëy ba féeteek bopp ba.

17Ba loolu amee Sawul ne Mikal: «Ana lu waral nga wor ma nii, bàyyi sama noon, mu rëcc?» Mikal ne ko: «Moom kay moo ma ne: “Bàyyi ma, ma daw, lu ko moy ma rey la!”»

18Noonu la Daawuda dawee ba raw. Mu fekki Samiyel ca Raama, wax ko la ko Sawul def lépp. Ñu ànd, mook Samiyel, dali ca Nayot.

19Ñu yegge ko Sawul ne ko: «Ndeke Daawudaa nga Nayot ca dëkk ba ñuy wax Raama.»

20Sawul yebal ay ndaw, ngir ñu jàpp Daawuda. Nit ña dikk, gis kuréelu yonent yuy jottali ay kàdduy waxyu, Samiyel jiite leen. Ba loolu amee, ca kaw ndawi Sawul ya la leerug Yàlla wàcc, ñuy jottali ay kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"*, ñoom itam.

21Ñu yegge ko Sawul, mu yebal yeneen ndaw, ñu dikk, di jottali ay kàdduy waxyu ñoom it. Sawul dellooti yebal ay ndaw, ñetteel bi yoon, ñu dikk, di jottali ay kàdduy waxyu, ñoom itam.

22Mu jóg moom ci boppam, jëm Raama. Mu dikk ba ca teen bu mag ba ca Seeku, daldi laajte ne: «Ana fu Samiyel ak Daawuda nekk?» Ñu ne ko: «Ña nga ca Nayot ca Raama.»

23Sawul jubal yoonu Nayot ca Raama. Ba loolu amee, ca kawam, moom it, la leerug Yàlla wàcc, muy wéy di jottali ay kàdduy waxyu di dem, ba àgg Nayot ca Raama.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>