1.Samiyel 2:1-35 WOLB2025 - Bible AI

1Ci kaw loolu Aana ñaan ne:

2«Kenn sellul ni Aji Sax ji,

3«Buleen ŋalŋaleeti, di damooka damooti,

4Fittu jàmbaar damm,

5Ña reggoon, bindu, di dunde,

6«Aji Sax jeey rey, di dundal,

7Aji Sax jeey xañe, di maye,

8Mooy yékkatee ku ndóol ci suuf,

9Mooy sàmm jéegoy wóllëreem,

10Aji Sax ji, ñi koy xeex ay rajaxoo,

11Gannaaw ba loolu wéyee Elkana ñibbi këram ca Raama. Ngóor sa moom, des ca Silo, di liggéeyal Aji Sax ji, fa kanam Eli sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba.

12Doomi Eli yu góor ya nag def nit ñu bon ñu faalewul Aji Sax ji.

13Lii moo di li sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yooyu tàmmoona def ak askan wi. Saa yu nit indiwaan juru sarax, bu ñuy togg yàpp wi, surgab sarxalkat bi day ŋàbb seppikaayu yàpp bu nirook roqub ñetti bëñ, dikk,

14capp ko ci biir, muy ndab lu tell, mbaa kawdir, mbaa cin, mbaa mbana—lu roq ba génne rekk, mu jël, sarxalkat bi féetewoo. Noonu lañu daan def ak mboolem niti bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, ña daan ñëw foofa ca Silo.

15Rax ci dolli bala ñoo lakk nebbon bi+ 2.15 nebbon: nebbon ak deret, yoon mayewul woon ñu lekk ko. Seetal ci +bk Sarxalkat yi+bk* 3.16-17.* sax, surgab sarxalkat bi day dikk, ne nit kiy sarxal: «Joxal sarxalkat bi ci yàpp wi, mu saaf. Du nangu nga jox ko yàpp wu ñor, yàpp wu xonq rekk.»

16Su ko nit ki nee: «Xanaa dees na njëkka lakk nebbon bi ba mu jeex, nga doora sàkk lu la neex?» Mu ne ko: «Mukk! Léegi nga ma ciy jox, lu ko moy doole laa koy jële.»

17Bàkkaaru doomi Eli yi réyoon na lool fi kanam Aji Sax ji, ndax dañu daan teddadil saraxu Aji Sax ji.

18Ci biir loolu ngóor sa Samiyel moom, ma ngay liggéeyal Aji Sax ji, sol xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"* mi ñu ràbbe lẽe.

19Mbubb mu ndaw nag la ko yaayam daan ràbbal, yóbbul ko at mu jotaan, buy ànd ak boroom këram sarxali saraxu at ma.

20Ci biir loolu Eli daan na ñaanal Elkana ak soxnaam, bala ñoo ñibbi, ne: «Yal na la Aji Sax ji may kuutaay ak sa soxna sii, ñu wuutu ki mu sédd Aji Sax ji.»

21Aji Sax ji nag dikke Aana aw yiw, mu amaat ñetti doom yu góor ak ñaar ñu jigéen.

22Eli nag mujj na di mag lool. Ba mu yégee mboolem li doomam yu góor yi def ak Israayil gépp, bay tëdde sax jigéen ñiy liggéey ci bunt xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* mi,

23da leena wax, ne leen: «Ana lu waral ngeen di def jëf jii? Maa dégge ci askan wépp jëf ju bon jii ngeen nekke.

24Aa! Xale yi, coow li ma dégg, muy law ci biir ñoñi Aji Sax ji, rafetul de!

25Su nit ki tooñee moroomu nitam, Yàllaay àtte; waaye su dee Aji Sax ji la nit ki tooñ, ana ku koy àtte?» Wax jooju nag taxul ba tey ñu déggal seen baay. Booba fekk na Aji Sax ji namm leena rey.

26Ci biir loolu yépp, ngóor sa Samiyel di màgg, neex Aji Sax ji, neex nit ñi.

27Mu am bés genn góoru Yàlla dikk ci Eli, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa feeñu woon ci lu leer sa waa kër baay ba ñu nekkee Misra, di moomeelu kër Firawna.

28Maa tànne sa baay ci digg giiri Israayil yépp, ngir mu doon sama sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"*, di yéeg ci sama sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"*, di taal cuuraay|lemma="cuuraay l-:"*, sol xar-sànni|lemma="xar-sànni m-:"* mi, janook man. Maa sédd it sa waa kër baay mboolem saraxi sawara yu bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*.

29Lu tax ngeen di teddadil sama saraxi rendi ak yeneen sarax yi ma santaane ci màkkaan|lemma="xaymab ndaje m-:"* mi? Lu waral ngay teral sa doom yi teraanga joo ma joxul, ba ngeen di yafloo li gën ci mboolem saraxi Israayil sama ñoñ?”

30Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israayil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.

31Te kat ay bés a ngi ñëw, maay dagg sa doole, dagg sa dooley waa kër baay, ba deesatul màggate ci sa kër.

32Njàqare ngay saxoo ci sama dëkkuwaay. Israayil dina baaxle moos, waaye du tax kenn màggate sa kër mukk.

33Dina am ku bokk ci yaw ku ma dul dagge ci liggéey bu jëm ci sama sarxalukaay, waaye maa lay jooyloo, ba nga ñàkki bët, teg la njàqarey xol, te mboolem ñu yokku ci sa kër, seen digg doole lañuy deewe.

34Li nga ciy def ab takk mooy liy dikkal Xofni ak Fineyas, sa ñaari doom yu góor yii: benn bés lañuy bokk dee ñoom ñaar ñépp.

35Te it maay tabbal sama bopp sarxalkat bu wóor boo xam ne sama nammeelu xol ak sama bëgg-bëggu bakkan lay jëfe. Maa koy sampal kër gu wóor, muy doxe fi kanam ki ma fal ba fàww.

© 2025 Bible Society of Senegal
div>