1.Samiyel 31:1-13 WOLB2025 - Bible AI

1Am na bés waa Filisti song bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*. Bànni Israayil won waa Filisti gannaaw, daw, ñu bare daanu dee ca tundu Gilbowa.

2Ci biir loolu waa Filisti ne dann Sawul aki doomam yu góor, rey ca Yonatan ak Abinadab ak Malkisuwa, doomam yu góor yooyu.

3Xare ba nag gëna mettee fa Sawul féete, fittkat ya jekku ko, mu tiit lool.

4Ci kaw loolu Sawul ne gàddukatu gànnaayam: «Boccil sa saamar, jam ma ba mu fëll; lu ko moy paaxe yii dikk, jam ma, toroxalsi ma.» Waaye gàddukatu gànnaayam nanguwul ndax tiitaange ju réy. Sawul jël saamaru boppam, daldi daaneel boppam ca kaw ñawka ga.

5Gàddukatu gànnaay ba gis ne Sawul dee na, moom it mu daaneel boppam ca kaw saamaram, dee, topp Sawul.

6Muy Sawul, di ñetti doomam yu góor, di gàddukatu gànnaayam itam, di mboolem ay nitam, ñoom ñépp a bokk dee bésub keroog.

7Ci kaw loolu bànni Israayil ya ca wàllaa xur wa, ak ña ca wàllaa dexu Yurdan gis ne xarekati Israayil ya daw nañu, te Sawul aki doomam yu góor dee nañu. Ñu daldi daw, gental seeni dëkk, waa Filisti dikk, wuutu leen ca.

8Ca ëllëg sa, ba waa Filisti dikkee, di futtisi néew ya, ca kaw tundu Gilbowa lañu fekk Sawul ak ñetti doomam yu góor, ñu tëdd.

9Ñu dog boppu Sawul, jël ay gànnaayam, ba noppi yeble ca réewum Filisti ba mu daj, ngir yégle seen ndam la ca seen këri tuur ya ak ca askan wa.

10Gannaaw gi, ñu denc gànnaayi Sawul ca seen biir kër tuur ma ñuy wax Astàrt|lemma="Astàrt:"*. Néewub Sawul, ñu wékk ko ca tatay dëkk ba ñuy wax Bet San.

11Ba waa Yabes Galàdd déggee la waa Filisti def Sawul,

12jàmbaar ñépp a fabu, topp guddi ga gépp ba Bet San. Ñu wékkee ca tatay Bet San néewub Sawul ak néewi doomam yu góor, doora ñibbi Yabes, boole fa néew ya, lakk.

13Ñu for nag seeni yax, suul ca ron garab gu mag ga ca Yabes, ba noppi ñu woor juróom ñaari fan.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>