1.Timote 1:1-19 WOLB2025 - Bible AI

1Ci man Póol, ndawal Almasi|lemma="Almasi b-:"* Yeesu, ci ndigalal Yàlla sunu Musalkat ak Almasi Yeesu sunu yaakaar, ci man la bataaxal bii bawoo,

2ñeel Timote, sama doomu bopp ci wàllu ngëm. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi ak sunu Sang Almasi Yeesu.

3Na ma la ko dénke woon ba may dem diiwaanu Maseduwan rekk, nanga toog Efes googu, ngir ña fay jàngale leneen, nga aaye leen.

4Ne leen ñu baña topp léebi neen ak limi maam yu dul jeex, ndax loolu ay werante doŋŋ lay jur, te jariñul dara ci liggéeyu njotug|lemma="jot:"* Yàlla gi sottee ci ngëm.

5Ndénkaane bii nag, li ko taxa jóg mooy luy yee ag cofeel gu bawoo ci xol bu rafet ak xel mu dal ak ngëm gu mucc jinigal.

6Am na ñu moy woowu yoon, ba lajj jëm ci wax ju tekkiwul dara.

7Ñooñu ay jàngalekati yoonu Musaa lañuy xëccoo ngir doon ko, te xamuñu li ñuy wax, bay xam lenn ci li ñuy dëggal.

8Xam nanu nag ne yoonu Musaa baax na, ndegam na mu ware lees koy jëfe.

9Lii itam xam nanu ko: ñi jub taxuñu yoon wi jóg, xanaa ñi jubadi ak ñi déggadi ak ñi ñeme Yàlla yi ak bàkkaarkat yi ak ñi wormaalul lu sell ak ñi wormaalul Yàlla. Bokk na ci itam bóomkati baay ak bóomkati ndey ak reykati nit ñi

10ak ñiy séy ci li yoon tere. Bokk na ci itam góor-jigéen yi ak jàppkati jaam yi ak fen-kat yi ak giñkati fen yi ak ñiy jëfe leneen lu woroo ak njàngale mu baax

11mi dëppoo ak xibaaru jàmm bi ñu ma dénk, xibaaru Yàlla Aji Tedd ju màgg ji.

12Damay sant sunu Boroom Almasi|lemma="Almasi b-:"* Yeesu mi ma dooleel, moom mi ma natt ba wóolu ma, tabb ma ci liggéey bi,

13te ma nekkoon ab tooñkatam, di ab bunduxataalkat, di ab néeg. Waaye yërmande laa dajeel, ngir ñàkka xam ga ma daan jëfe, te ñàkka gëm tax.

14Sunu yiwu Boroom moo ma baawaanal, booleel ma ci ngëm gi ak cofeel gi gëmkatub Almasi Yeesu jagoo.

15Mboolem kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm: Almasi Yeesu moo dikk ci àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw!

16Waaye loolu moo tax man bàkkaarkat bi ci raw, ma dajeek yërmande, ngir ci lépp lu nu Almasi Yeesu di muñal, ma doon ci misaal, ñeel ñi ko nara gëm ëllëg, ba texe ba fàww.

17Yaw Buur bi sax dàkk,

18Kon nag Timote doom, loolu mooy ndigal li ma la dénk, te mu dëppook kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* yi jotoona jib te jëm ci sa mbir. Gànnaayool kàddu yooyu ngir di ci xaree xare bu baax bi,

19te nga saxoo ngëm ak xel mu dal. Am na ñu tanqamlu seen ndéeyum xel ba suuxal seen ngëm.

© 2025 Bible Society of Senegal
iv>