2.Buur ya 19:1-36 WOLB2025 - Bible AI

1Naka la ko Buur Esekiyas dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji.

2Ba loolu amee mu yebal Elyakim bootalub Buur ak Sebna bindkat ba, ak ñay mag ca sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ya. Ñu sol saaku yu ñuy ñaawloo, daldi dem ca Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc.

3Ñu ne ko: «Esekiyas dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer!

4Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg mboolem kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»

5Ba surgay Buur Esekiyas àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax,

6Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa.

7Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma reye ko ab saamar ca réewam.”»

8Gannaaw loolu Rabsake dégg ne buurub Asiri bàyyikoo na Lakis, bay xareek dëkk ba ñuy wax Libna. Mu walbatiku fekki ko foofa.

9Booba buurub Asiri daa dégg ne Tiraka buurub Kuus|lemma="Kuus:"* moo leen di songsi. Mu dellu yebal ay ndaw ca Esekiyas, ne leen:

10«Waxleen Esekiyas buurub Yuda, ne ko: “Seen Yàlla ji ngeen yaakaar, bumu leen nax, naa leen deesul teg Yerusalem ci loxol buurub Asiri.

11Xanaa yaw ci sa bopp dégg nga li buuri Asiri def mboolem réew yi, faagaagal leen? Yaw nag, ndax yaa ciy mucc?

12Xeet yi samay maam sànk, ndax seeni yàlla dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Reccef, di askanu Eden wa woon ca Telasar?

13Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”»

14Ba Esekiyas jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër Aji Sax ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji.

15Esekiyas ñaan fi kanam Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji, Yàllay Israayil mi toog ci jal bi, fi tiim malaakay serub|lemma="serub y-:"* yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf.

16Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg! Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg kàdduy Senaxerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund!

17Aylayéwén Aji Sax ji, buuri Asiree tas xeet yeek seeni réew,

18te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen.

19Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, ngalla wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw Aji Sax ji doŋŋ yaa di Yàlla.»

20Ba mu ko defee Esayi doomu Amocc yónnee ca Esekiyas ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ne li nga ko ñaan ci Senaxerib buurub Asiri, dégg na ko.

21Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom:

22Ana kooy kókkaleeka ñàkke kersa?

23Yaa yebal say ndaw, di kókkali Boroom bi,

24Maa gas ay teen, naan ndoxum réewum jàmbur,

25«“Waaye, Senaxerib, xanaa déggoo ne bu yàgg laa dogal loolu?

26Waa dëkk ya ne yàcc, jàq, torox,

27«“Waaye boo toogee, boo génnee, boo duggee, xam naa,

28Yaa xadaru sama kaw,

29«Lii nag, Esekiyas, def kob takk.

30Ña des ca askanu Yuda

31Yerusalem kay la aw ndes di génne,

32Moo tax Aji Sax ji wax ci buurub Asiri ne:

33Yoon wa mu dikke lay delloo,

34Maay aar dëkk bii, musal ko

35Guddig keroog malaakam Aji Sax|lemma="malaakam Aji Sax j-:"* ji dikk, faat ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp, diy néew.

36Ba mu ko defee Senaxerib buurub Asiri daldi fabu, ñibbi. Mu toog nag ca péey ba, di Niniw.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>