2.Jaar-jaar ya 13:1-22 WOLB2025 - Bible AI

1Ci fukkeelu at ak juróom ñett ca nguurug Yerbowam, ca la Abya falu buur ca Yuda.

2Ñetti at la nguuru fa Yerusalem, te yaayam moo doon Mikaya, doomu Uryel ma dëkk Gibeya. Xare nag amoon na diggante Abya ak Yerbowam.

3Abya moo song xare ba ànd ak gàngooru jàmbaari xare; ñeenti téeméeri junniy (400 000) góor ñu ñu tànn. Yerbowam it làng-déral ab xare janook moom, ak juróom ñetti téeméeri junniy (800 000) góor ñu ñu tànn, xeexkat yu jàmbaare.

4Abya moo taxaw fa kaw tundu Cemarayim ca diiwaanu tundi Efrayim, daldi xaacu ne: «Yaw Yerbowam, déglu ma yaak Israayil gépp.

5Xanaa war ngaa xam ne Aji Sax ji Yàllay Israayil moo jox Daawuda nguur ci kaw Israayil ba fàww, moom ak aw askanam, muy kóllëreg xorom+ 13.5 kóllëreg xorom waxin la, day tegtale kóllëre gu yàgg, ba sax dàkk, ndax lu bare luy yàqu, xorom lees ko baaxoo woona dence, ngir mu yàgg.* gu dul jaas, du fecciku, xanaa sax dàkk.

6Teewul Yerbowam doomu Nebat miy surgab Suleymaan doomu Daawuda, moo jóg fippu ci kaw sangam.

7Ci kaw loolu ay sagari nit ñu tekkiwul dara booloo ànd ak moom, jaay Robowam doomu Suleymaan doole, fekk Robowam di gone gu fit wa dëgërul ba manu leena të.

8Léegi nag yeen ngeen defe ne man ngeena të nguurug Aji Sax ji ci loxol doomi Daawuda. Gàngoor gu réy ngeen, te ñi ànd ak yeen di ay wëlluy wurus yu leen Yerbowam sàkkal, ñu taxawe ay yàlla.

9Xanaa du yeena dàq sarxalkati|lemma="sarxalkat b-:"* Aji Sax ji, doomi Aaróona yu góor, ak Leween|lemma="Leween b-:"* ñi, ba sàkkal seen bopp ay sarxalkat ni askani yeneen réew yi? Ku mu mana doon rekk dikk ak aw yëkk, ak juróom ñaari kuuy, ngir tabbees ko cig carxal, ba mu doon ab sarxalkatub lu dul Yàlla.

10Nun nag Aji Sax ji mooy sunu Yàlla, te waccunu ko. Te sarxalkat yi fi nun di liggéeyal Aji Sax ji, askanu Aaróona lañu, feggook Leween ñeek seen wàll ci liggéey bi.

11Ñooy lakk suba su nekk ak ngoon su nekk, ñeel Aji Sax ji, ay saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"* ak cuuraay|lemma="cuuraay l-:"* lu xeeñ. Mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"* ma it ñoo koy teg bu jekk ca taabal ju set wecc ja, te ñooy teg tegukaayu làmp bu wurus ba aki làmpam, ñuy tàkk ngoon su nekk, ndax nun déy sunu ndénkaaneb Yàlla Aji Sax ji lanu sàmm. Yeen nag yeena ko wacc.

12Mu ngoogu, Yàllaa ngii jiite nu, mooki sarxalkatam ak seeni liit yu xumb, ngir jibal wooteb xare ci seen kaw. Kon yeen bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, buleen xareek Aji Sax ji seen Yàllay maam, ndax kat dungeen am ndam.»

13Ci biir loolu Yerbowam yónnee ndànk lenn ca gàngooram, ñu doxe Yudeen ña gannaaw, ngir tëru leen.

14Yuda walbatiku, gisuñu lu moy xare bu leen tance kanam ak gannaaw. Ñu daldi woo Aji Sax ji wall, sarxalkat ya wal liit ya.

15Ci kaw loolu Yudeen ña xaacoondoo. Naka la Yudeen ña xaacu, Yàlla duma Yerbowam ak Israayil gépp fa kanam Abya ak Yuda.

16Bànni Israayil daldi daw, won Yuda gannaaw, Yàlla teg leen ci seen loxo.

17Abya ak gàngooram nag duma leen duma yu réy, néewi Israayil tëdd, di juróomi téeméeri junniy (500 000) tànnéefi xarekat.

18Jant yooyu la bànni Israayil suufe, Yudeen ña féete kaw, ndax la ñu wéeroo Aji Sax ji seen Yàllay maam.

19Abya nag dàqi Yerbowam, ba nangu ca moom ay dëkk. Betel aki dëkk-dëkkaanam ca la, ak Yesana aki dëkk-dëkkaanam, ak Efron aki dëkk-dëkkaanam.

20Yerbowam amatuloon doole ca janti Abya. Gannaaw gi, Aji Sax ji faat ko, mu dee.

21Ba mu ko defee Abya gëna am doole. Ci biir loolu mu jël fukki jabar ak ñeent, am ñaar fukki doom yu góor ak ñaar, ak fukki doom yu jigéen ak juróom benn.

22Li des ci mbiri Abya, ay waxam aki jëfam, bindees na ko ci nettalib Ido yonent ba.

cle>