1Ba mu ko defee Yosafat doomu Asa falu buur, wuutu ko. Mu dëju bu baax nag ci kaw Israayil, nguur ga ca bëj-gànnaar.
2Yosafat teg ay gàngoor ca mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi teg ay kuréeli xare ca réewum Yuda, ak dëkki Efrayim ya Asa baayam nangu woon.
3Ba mu ko defee Aji Sax ji ànd ak Yosafat, ndax na Daawuda maamam daan njëkka doxe, na la doxe, te sàkkuwul tuur ya ñuy wax Baal|lemma="Baal:"*.
4Yàllay baayam daal la daan sàkku te ay santaaneem la daan doxe, baña roy jëfi Israayil.
5Aji Sax ji nag dëgëral nguur ga ca loxoom, Yuda gépp di indil Yosafat ab galag, mu am alal ak daraja ju bare.
6Ci kaw loolu pastéefu xolam ci jëfe coobarey Aji Sax ji yokku, ba mu jëleeti fa Yuda, bérebi jaamookaay|lemma="bérebi jaamookaay y-:"* ya, ak xer ya ñuy màggale Asera|lemma="Asera:"* tuur ma.
7Mu teg ca yebal, ca ñetteelu atum nguuram, jawriñam ñii di Ben Xayil ak Abdiyas ak Sàkkaryaa ak Netaneel ak Mikaya, ngir ñu jàngaleji ca dëkki Yuda.
8Ña ànd ak ñoom di ay Leween|lemma="Leween b-:"*, Semaya ca la, ak Netaña ak Sebaja ak Asayel ak Semiramot ak Yonatan ak Adoña ak Tobya ak Tob Adoña. Leween ñooña àndaale ak Elisama ak Yexoram, sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ya.
9Ñu yóbbaale téereb yoonu Aji Sax ji. Mboolem dëkki Yuda lañu wër, di jàngal askan wa.
10Tiitaange ju Aji Sax ji sabab nag dikkal mboolem nguuri réew yi séq Yuda, ba tax songuñu Yosafat xare.
11Ay Filisteen itam di indil Yosafat ay may akub xaalis akub galag, Arab ya sax indil ko ay gàtt: ay kuuy, juróom ñaari junni ak juróom ñaari téeméer (7 700); ak ay sikket, juróom ñaari junni ak juróom ñaari téeméer (7 700).
12Yosafat gën di màgg, ba kawe lool. Ci biir loolu mu tabax ca Yuda ay këri buur ak dëkki dencukaay.
13Ay denc yu takku la amoon fa dëkki Yuda, ak niti xarekat, jàmbaari xare yu am doole fa Yerusalem.
14Ñii nag lañu limal ñooñu, na ñu bokke seeni kër maam:
15Mu feggook njiit la Yoxanan, ma jiite ñaari téeméer ak juróom ñett fukki junniy (280 000) góor.
16Kooku feggook doomu Sikkri, Amasiya ma yebul boppam ci liggéeyu Aji Sax ji. Moo jiite ñaari téeméeri junniy (200 000) jàmbaari xare.
17Ci wàllu Beñamin, ñeyu xare ba Elyada moo jiite ñaari téeméeri junni (200 000) ñu gànnaayoo xalaaki fitt ak pakk.
18Mu feggook Yewosabàdd ma jiite téeméer ak juróom ñett fukki junni (180 000) ñu gànnaayu.