1Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen.
2Ndaxte Yàlla moo ne:
3Bëggunu kenn sikk sunub liggéey, moo tax bëggunoo jëfe lenn luy doon tojaange ci kenn.
4Ci lépp kay lanu bëgga seedeel sunu bopp, ne noo yelloo ngërëm, te ay jawriñi Yàlla lanu, di ñu muñ lu bare ci biir coono aki mitit aki njàqare;
5ci ay dóor ak néegi kaso, ci biir mbooloo yu nu jógal, ci doñ-doñ ju metti ak fanaanee xoole akub xiif;
6te nuy setal sunu dund, di ànd ak xam-xam, ci biir muñ akug mbaax, ci biir Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi ak cofeel gu amul jinigal,
7ci biir kàddug dëgg ak kàttanu Yàlla; ci kaw gànnaayi njubte yi ci sunu loxol ndijoor ak lu càmmoñ;
8ci biir teraanga ak ci biir toskare; ci biiri baatal ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu;
9jàppe nu ñu kenn xamul, te nuy ñu siiw; jàppe nu ñuy waaja dee, te nuy dund; jàppe nu ñu ñu wara mbugal, te bañ leena teg àtteb dee.
10Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
11Yeen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir yépp, ubbil leen sunu xol.
12Genn ñooru jógewul ci nun, waaye yeen yeena nu ñooru ci seen xol.
13Léegi nag yeen, feyleen nu bor bi boog, ma wax ak yeen ni samay doom, ubbilleen nu seen xol!
14Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?
15Gan juboo la Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi ak Seytaane|lemma="Seytaane:"* séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi?
16Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne:
17Kon nag: