2.Samiyel 1:1-26 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw ba Sawul faatoo, fekk na Daawuda walbatikoo ca dumay Amalegeen ña, dellu Ciglaag, ba toog fa ñaari fan.

2Ca gannaaw ëllëg sa, jenn waay ne jimeet, jóge ca dalub Sawul, dikk. Yére yaa nga xottiku, bopp ba taq suuf, ngir naqarlu. Naka la agsi ci Daawuda, daldi daanu fi suuf, sujjóot.

3Daawuda ne ko: «Foo jóge nii?» Mu ne ko: «Ca dalub Israayil laa rëcce.»

4Daawuda ne ko: «Lu xew, gaawe ma!» Mu ne ko: «Mbooloom Israayil a dawe ca xare ba. Ñu bare ca ñoom daanu nañu, dee. Sawul ak doomam Yonatan it dee nañu.»

5Daawuda ne ndaw la: «Lu la xamal ne Sawul ak doomam Yonatan dee nañu?»

6Ndaw la ne ko: «Dafa yemook ma tollu tembe ca kaw tundu Gilbowa. Ndeke Sawul a nga fa, sukkandikoo xeejam. Watiiri xare yaak gawar ya defuñu lu moy ne ko dann.

7Naka la ne gees, yem ci man, woo ma, ma wuyu.

8Mu ne ma: “Yaa di kan?” Ma ne ko: “Ab Amalegeen laa.”

9Mu ne ma: “Kaay fii, jekkali ma. Maa ngi ci miirum dee, doonte dese naa tuuti.”

10Ma dikk, daldi koy jekkali, ndax xamoon naa ne du dundati gannaaw jéllam ba. Ma summi nag mbaxanam buur ma mu soloon, tekki lam ba woon ca përëg ma. Yooyu laa la yótsi nii, sang bi.»

11Ba loolu amee Daawuda sëq yéreem, xotti, ña ànd ak moom ñépp itam, noonu, ndax aw naqar.

12Ñaawlu nañu, di jooy, lekkuñu ba ca ngoon ndax Sawul ak doomam Yonatan ak gàngooru Aji Sax ji|lemma="Aji Sax j-:"*, ak waa kër Israayil ña ñu reye saamar.

13Daawuda ne ndaw la: «Ana foo bokk?» Mu ne ko: «Man doomu doxandéemub Amalegeen laa.»

14Daawuda ne ko: «Noo saña xàcce sa loxo, di bóom ki Aji Sax ji fal?»

15Daawuda nag woo kenn cay surgaam, ne ko: «Dikkal dóor, mu dee!»

16Daawuda ne Amalegeen ba: «Yaa gàddu sa bakkanu bopp, ndax yaa seedee sa gémmiñu bopp ne yaa rey ki Aji Sax ji fal.» Surga ba dóor Amalegeen ba, mu dee.

17Kàddu yii la Daawuda jooye Sawul ak doomam Yonatan.

18Moo santaane ñu jàngal ko askanu Yuda. «Fittkat» lañu dippee woy wi. Nii lañu ko binde ci Téereb aji jub ji. Mu ne:

19Wóoy Israayil, ña ngay sagoo lañu jam, ñu ne lareet ca sa tund ya!

20Buleen ko siiwal fa Gaat,

21Wóoy tundi Gilbowa!

22Du deret mbaa nebbonu jàmbaar bu fittug Yonatan xof,

23Wóoy Sawul ak Yonatan,

24Yeen jigéeni Israayil, jooyleen Sawul ma leen wodde

25Jàmbaar ñaa daanoo biir xare ba,

26Yonatan, doom yaay, tiisoo naa la,

© 2025 Bible Society of Senegal
div>