1Noonu Aji Sax ji yónni Natan ca Daawuda. Mu dikk, ne ko: «Ñaari góor la woon ci ab dëkk. Kenn ka barele, ka ca des néewle.
2Ki barele am na jur gu bare lool, gu gudd ak gu gàtt.
3Waaye ka néewle amul lu dul xar mu ndaw mu jigéen mu mu jëndoon, yar ko biir këram, muy màggandook ay doomam. Ca njëlam sa la xar ma daan lekk, ca kaasam la daan naane, te ca kaw dënnam la daan tëdd. Xar mi daa meloon ni doomam.
4Ci biir loolu ku nekk ciw yoon dikk, dal ak ka barele. Waaye ka barele néegula sàkk ciy gàttam mbaa nagi boppam, ngir toggal ko gan gi dal ak moom. Dafa jël xaru ka néewle, toggal ko gan gi dal ak moom.»
5Daawuda nag mer lool ca jëfi nit kooku. Mu ne Natan: «Giñ naa ci Aji Sax jiy dund, dee rekk mooy àtteb waa ji def loolu!
6Te it menn xar mi, ñeentam la koy feye, gannaaw moo def jooju jëf, te amu ci jenn yërmande!»
7Natan ne Daawuda: «Yaw, yaay waa ji! Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ne: “Man maa la fal buurub Israayil, maa la xettali ci Sawul.
8Maa la jox sa kër sang, maa teg ci say loxo sa jabari sang, jox la nguurug Israayil ak Yuda. Te bu doyuloon it, ma dolli.
9Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko reye saamar. Jabaram nga jël, def ko sa jabar; moom nga reye ko saamaru Amoneen ñi.
10Kon nag saamar dootul jóge sa kër mukk, ndax yaa ma ñàkke worma, ba jël jabaru Uri Etteen bi, def ko sa jabar.”
11Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di yékkati fi sa kaw, musiba mu jóge ci sa kër. Maay jël say jabar, ngay gis, jox leen góor ni yaw, mu tëdde say jabar bëccëg ndarakàmm.
12Yaw déy ci sutura nga ko defe. Waaye man, ci kanam Israayil gépp laay sabab mbir moomu, bëccëg ndarakàmm.”»
13Daawuda nag ne Natan: «Maa tooñ Aji Sax ji.» Natan ne ko: «Aji Sax ji it jéllale na sa bàkkaar; doo ci dee.
14Du tere nag, gannaaw dangaa teddadil lool Aji Sax ji ci mbir mii, doom ji nga ci am, moom, day dee rekk.»
15Ba loolu amee Natan dellu këram.
16Daawuda nag tinu Yàlla ci xale bi: muy woor, fatu, fanaanee tëdd ci suuf.
17Magi këram soññ ko ngir yékkatee ko fa suuf, nanguwul, te bokkul ak ñoom lekk dara.
18Ñu teg ca juróom ñaari fan, xale ba dee. Surgay Daawuda ya ragala wax Daawuda ne ko xale ba dee na. Booba ña ngay xalaat naan: «Ndegam ba xale bay dund lanuy wax ak moom, dégluwu nu kay, ana nu nu koy waxe ne xale bi dee na, muy def njaaxum?»
19Daawuda nag gis surgaam ya ñuy déeyoo, mu xam ne xale bi dee na. Mu ne leen: «Xale bi daa dee?» Ñu ne ko: «Dee na.»
20Ba mu ko defee Daawuda jóge ca suuf, sangu, diwu, soluwaat. Ci kaw loolu mu dugg ca kër Aji Sax ji, sujjóot, daldi dem këram, santaane, ñu taajal ko ag lekk, mu lekk.
21Surga ya ne ko: «Li ngay def lu mu doon? Bi xale biy dund, danga doon woor aka jooy, léegi bi xale bi deewee, nga jóg, di lekk?»
22Mu ne leen: «Ba xale biy dese bakkan laa doon woor aka jooy, ndax dama noon: “Ana ku xam ndax Aji Sax ji dina ma defalu yiw, ba xale bi dund am déet?”
23Waaye gannaaw léegi dee na, ana lu may woorati? Dama koo mana dekkal? Man kay maa koy fekki, waaye moom du délsi ci man mukk.»
24Ba loolu amee Daawuda dëfal soxnaam Batseba. Mu daldi dem tëdd ak moom. Gannaaw gi, ndaw si am ca doom ju góor, tudde ko Suleymaan. Aji Sax ji nag sopp xale bi,
25ba xamle ko, Yonent Yàlla Natan jottali, daldi koy tudde Yedija (muy firi Soppey Aji Sax ji), ci ndigalu Aji Sax ji.
26Ci biir loolu Yowab xareek waa Raba, péeyub Amoneen ña, ba nangu tatay buur ba.
27Ba loolu amee Yowab yebal ay ndaw ca Daawuda, ne ko: «Xare namaak waa Raba, nangu naa sax seen gox, ba ñuy jële am ndox.
28Kon booleel ndesu gàngoor gi, te nga gaw dëkk bi, ba nangu ko. Lu ko moy maay nangu dëkk bi, ñu tudde ma ko.»
29Daawuda nag dajale gàngoor gépp, daldi dem Raba, xareek ñoom, ba nangu ko.
30Ba mu ko defee mu nangu seen mbaxanam buur ma ñu solal jëmmu tuur ma ñuy wax Milkom+ 12.30 Am na yeneen mbind yu yàgg yu indi ne seen buur lañu daan solal mbaxana mi.*. Diisaayu mbaxana maa nga tollu ci fanweeri kiloy wurus ak ñeent, aw doj wu gànjare tappe ca. Ñu solal ko Daawuda. Alal ju baree bare la Daawuda nangoo ca dëkk ba.