2.Samiyel 5:1-24 WOLB2025 - Bible AI

1Ci kaw loolu giiri Israayil yépp dikk fa Daawuda ca Ebron, ne ko: «Noo ngii di say bokk lenqe.

2Te it démb ak bërki-démb, ba Sawul dee sunu buur sax, yaa doon jiite Israayil ci xare. Aji Sax ji ne la: “Yaay sàmm Israayil sama ñoñ te yaay yilif Israayil.”»

3Noonu la magi Israayil ñépp dikke ca Buur Daawuda ca Ebron, mu fasook ñoom kóllëre|lemma="kóllëre g-:"* foofa ca Ebron, fa kanam Aji Sax ji. Ba mu ko defee ñu sotti Daawuda diwu pal ga, muy buurub Israayil.

4Daawuda amoon na fanweeri at, ba muy falu buur, te ñeent fukki at la nguuru.

5Ca Ebron la yore nguurug Yuda juróom ñaari at ak juróom benni weer, waaye ca Yerusalem la yore mboolem Israayil ak Yuda diiru fanweeri at ak ñett.

6Gannaaw loolu Buur Daawuda ànd aki xarekatam, songi Yerusalem ga ñu doon woowe Yebus itam, ndax la fa Yebuseeni diiwaan ba dëkke woon. Yebuseen ña ne Daawuda: «Doo fi dugg de, ndax gumba yeek lafañ yi rekk ñoo lay waññi.» Booba foog nañu ne Daawuda manu faa dugg.

7Terewul Daawuda nangu tatab Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"* ga ñu mujj woowe Kër Daawuda.

8Daawudaa noon bésub keroog: «Ku bëgga jam Yebuseen ñi, ca xuntum yoonu ndox ma ngay mana dabe seeni gumbaak seeni lafañ, xuloowaaley Daawuda yi.» Looloo waral waxin wi ñu naan: «Gumba akub lafañ du dugg kër ga.»

9Ba mu ko defee Daawuda dëkk ca biir tata ja, woowe ko Kër Daawuda, ba noppi tabax ay kër yu bees fa ko wër fépp, dale ko ca sëkkub Milo+ 5.9 Milo, xur la wu doxoon diggante gox ba ñu naan Kër Daawuda ak fa kër Yàlla ga wara nekk.*, ba ca biir.

10Daawuda nag di gëna am doole, Aji Sax ji Yàlla, Boroom gàngoori xare yi ànd ak moom.

11Ci biir loolu Iram buurub Tir, yebal ay ndaw ca Daawuda, ñu yóbbul ko ay banti garabu seedar ak ay liggéeykati bant ak yattkati xeer, ngir ñu tabaxal Daawuda kër.

12Daawuda xam ne Aji Sax jee ko fal buurub Israayil te moo kaweel nguuram ngir Israayil ñoñam.

13Gannaaw ba Daawuda jógee Ebron, denc na ay nekkaale ak yeneeni soxna ca Yerusalem. Mu am ca yeneen doom yu góor ak yu jigéen.

14Doom yu góor yi juddoo Yerusalem ñoo di Samwa ak Sobab ak Natan ak Suleymaan

15ak Ibaar ak Elisuwa ak Nefeg ak Yafya

16ak Elisama ak Elyada ak Elifelet.

17Ba waa Filisti déggee ne fal nañu Daawuda buurub Israayil, ñoom ñépp a jóg, di ko wër. Daawuda nag dégg ko, dem làquji ca biir tata ja.

18Waa Filisti dikk, tasaaroo ca xuru Refayeen ña.

19Daawuda laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma songi waa Filisti? Ndax dinga leen teg ci sama loxo?» Aji Sax ji ne ko: «Demal, maay teg waa Filisti ci say loxo déy!»

20Daawuda dem ba Baal Peracim, duma leen foofa. Mu ne: «Aji Sax jee ma xàllal yoon, ne jàyy ni walum ndox ca kaw noon ya.» Moo tax ñu woowe béreb boobu Baal Peracim (muy firi Boroom bi xàll naw yoon).

21Filisteen ña nag waccoon seeni gàllaaj, Daawudaaki nitam boole yóbbu.

22Ba mu ko defee waa Filisti dikkaat, tasaaroo ca xuru Refayeen ña.

23Daawuda dellu laaj Aji Sax ji. Mu ne ko: «Bul topp seen gannaaw, wër leen ndombo, dal ca seen kaw fa janook garab ya.

24Booy dégg tànk yuy jaab ca kaw njobbaxtali sànd ya rekk, gaawtul, ndax booba Aji Sax jee la jiitu, di dumaji waa dalub Filisti.»

© 2025 Bible Society of Senegal
div>