1Fa may wattoo laay taxaw,
2Aji Sax jee àddu, ne:
3Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal,
4«Xol baa ngay xoggaliku, te ag njub nekku ca,
5Biiñ day wore,
6Xanaa du ñi mu teg loxo ñépp a koy léebuji,
7Moo! Ndax ñi la lebal duñu jekki jóg?
8Yaa sëxëtoo woon ay xeet yu bare,
9«Wóoy ngalla kuy dajaleel këram
10Gàcce nga nasal sa kër,
11Doju tata dina riir déy,
12«Wóoy ngalla ku tabaxe ab dëkk
13Xanaa du ci Aji Sax ji
14Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj,
15«Wóoy ngalla yaw mi nàndal sab dëkkaale,
16Gàcce ngay gëna regg teraanga,
17Ay wi nga teg Libaŋ mooy këppu ci sa kaw,
18«Ana luy njariñal yatt jëmmu xërëm
19Wóoy, ngalla ku naan bant: “Xippil,”