1Kàdduy Amos a ngii, di boroom jur bu dëkkoon Tekowa+ 1.1 Tekowa sorewul Yerusalem. Ba bànni Israayil xàjjalikoo nekk ñaari réew gannaaw ba Buur Suleymaan nelawee, Tirca njëkkoon naa nekk péeyub réewum Israayil, Samari tegu ca; Yerusalem di péeyub réewum Yuda.. Mu am peeñu mu jëm ci Israayil ci janti Osiyas+ 1.1 Osiyas mooy Asaryaa itam. buurub Yuda ak janti doomu Yowas, Yerbowam buurub Israayil. Loolu tollu ci ñaari at lu jiitu yëngu-yëngu suuf ba.
2Mu ne: Aji Sax jeey|lemma="Aji Sax j-:" yëmmoo fa Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"+ 1.2 Siyoŋ mooy tund wa kër Yàlla ga nekk ca Yerusalem. Daan nañu ko tudde it dëkku Yerusalem., Yerusalem lay àddoo, parluy sàmm si ne faraas, mbooyum kaw tundu Karmel lax. Aji Sax ji mbugal na xeet yi (Saar 1.3—2.16)
3Aji Sax ji da ne: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Damaas+ 1.3 Damaas mooy péeyub réewum Siri., te duma fomm seeni duma. Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.
4Maay yebal sawara seen waa kër Buur Asayel, mu xoyom taaxi Buur Ben Addàd.
5Maay dàjji bunti dëkkub Damaas, dagg waa xuru Awen+ 1.5 xuru Awen mooy tekki xuru Ñaawtéef., boole ca boroom yetu nguur fa Bet Eden+ 1.5 Bet Eden mooy kërug Àjjana, muy tekki fii Kërug Xawaare.. Waa Siri dugg ngàllo, dellu Kir+ 1.5 Kir la Arameen ñi cosaanoo. Gannaaw gi lañu sanci réewu Siri. Seetal ci 9.7..» Aji Sax jee ko wax.
6Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa+ 1.6 Gasa, benn la ci juróomi dëkki Filisti yu mag; yeneen yi di Asdodd ak Askalon ak Ekkron ak Gaat. Seetal ci 6.2., te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp ba noppi gàddaayloo mbooloom lëmm, jalax leen ca Edomeen ña.
7Maay yebal sawara ca tatay Gasa, mu xoyom ay taaxam.
8Maay dagg waa Asdodd ak boroom yetu nguur fa Askalon, fél Ekkron, ndesu Filisteen ña sànku.» Boroom bi Aji Sax jee ko wax.
9Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Tir+ 1.9 Tir dafa mel ni Sidon. Ay dëkk yu mag lañu woon ca réewum Fenisi., te duma fomm seeni duma. Am na mboolooy lëmm yu ñu gàddaayloo, te ñoom waa Tir jaay leen Edomeen ña, te sédduñu leen ci kóllëreg|lemma="kóllëre g-:" mbokk gi.
10Damay yebal sawara ca tatay Tir, mu xoyom ay tataam.»
11Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom+ 1.11 waa Edom ñaa nga bàyyikoo fa bëj-saalumu Yuda jàpp penku. Ñu ngi soqikoo ci Esawu, magu Yanqóoba, kon bokki Israayil lañu woon, waaye dañoo faroon ak nooni Israayil., te duma fomm seeni duma. Ñoo toppe seen bokki bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:" saamar, jalax yërmande, mer mer mu dul meddi ak xadar ju dul giif mukk.
12Maay yebal sawara fa Teman, mu xoyomaale tatay Boccara+ 1.12 Teman ak Boccara, ay goxi Edom yu mag la woon. Boccara moo doon péeyu Edom..»
13Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Amoneen+ 1.13 Amoneen ñu ngi soqikoo ci Lóot. Réew mi ñuy wax Yordani tey, ci lañu dëkkoon. ñi, te duma fomm seeni duma. Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd, ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.
14Maay jafal ca kaw tatay Raba+ 1.14 Raba, péeyu Amon la woon., mu xoyom ay taaxam, yuux ya jib bésub xare, ci biir callweer bésub ngëlén.
15Seen buur lañuy jàpp, mu gàddaay, mooki kàngamam.» Aji Sax jee ko wax.