1Dégluleen kàddu gii Aji Sax ji wax ci yeen, bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:", mu jëm ci seen mboolem xeet wi mu génnee réewum Misra. Mu ne:
2«Yeen doŋŋ laa ràññee ci mboolem askani suuf. Moo tax ma di leen mbugal ndax seen ñaawtéef gépp.»
3Ndax ñaar dina ànd te digewuñub dajee?
4Ndax gaynde dina ŋarem ngeer te fàddul? Am gaynde gu mat dina xiiroom paxam te jàppul?
5Ndax picc dina keppu te fiireesu ko? Am ag fiir dina fettax te jàppul?
6Ndax bu buftab xare jibee, waa dëkk ba du tiit? Ndax aw ay dina dabub dëkk te du Aji Sax jee?
7Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.
8Bu gaynde yëmmoo, ana ku dul tiit? Ana ku saña baña jottali kàdduy waxyu|lemma="waxyu:", bu ko Boroom bi Aji Sax ji waxee?
9Yéeneleen ca biir taaxi Asdodd ak ca biir taaxi Misra. Neleen: «Dajeleen ca kaw tundu Samari, ba gis na Samari salfaañoo, ak nootaange ga fa nit di daj.
10Xamuñu sax def njub.» Kàddug Aji Sax jee. «Dañuy jal alalu fitnaak yàqute ci seen biiri taax.»
11Moo tax Boroom bi Aji Sax ji ne: «Ab noon dina gaw seenum réew, néewal leen doole, lël seeni taax.»
12Aji Sax ji nee: «Wallub sàmm ak gàtt bu gaynde fàdd weesul ñaari yeel, dogitu nopp. Kuy wallu bànni Israayil ga ca Samari it, xanaa dogu basaŋ, dammitu lal.
13Dégluleen te artu waa kër Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:".» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee, Yàlla ji ci gàngoori xare yi.
14«Bés bu may mbugale Israayil ay bàkkaaram, damay tasaale sarxalukaayi|lemma="sarxalukaay b-:" Betel. Béjjén yi ci cati sarxalukaay ba dog, rot.
15Maay màbbaale këru taax ak këru àll; kër yu ñu rafetale bëñu ñey dina yàqu, te kër yu bare dootul taxaw.» Kàddug Aji Sax jee.