Amos 4:1-13 WOLB2025 - Bible AI

1Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy toroxal néew-ji-doole, di noot aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»

2Boroom bi Aji Sax ji giñ na ci sellaayam ne: «Ay bés a ngii déy, di ñëw, dees na leen kor, yóbbu, ku nekk ci yeen koru niw jën,

3ñu diri ko jaarale fu xar-xaru tata gëna jegee, sànni ko ca Armon+ 4.3 Fi ñu ne ca Armon manees na ne yooni tundu Ermon..» Kàddug Aji Sax jee.

4Aji Sax ji nee: «Demleen Betel, bàkkaare fa, dem Gilgal+ 4.4 Betel ak Gilgal, ay bérebi jaamookaay lañu woon., bàkkaareeti fa. Rendileen seenub sarax ca ëllëg sa, joxe seen saraxi fukkeeli alal ca gannaaw ëllëg sa,

5te ngeen lakk mburu, def ko saraxu cant|lemma="Sarax yi:". Yégleleen seen saraxi yéene|lemma="Sarax yi:" te siiwal ko, ndax dégg ngeen? Ndegam loolu ngeen namm, yeen bànni Israayil.» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

6«Maa wéetal seeni biir seen dëkkoo dëkk, dugub ñàkke fépp fu ngeen moom, te taxul ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.

7Mu ne: «Maa leen xañub taw bu leen may ngóob ci ñetti weer. Ma taw ci bii dëkk, tawuma ca bee. Wii waar tawlu, wee waar lax.

8Ñaari dëkk ba ñett di deek mar, wuti beneen, naane fa, te duñu màndi. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.

9«Maa leen dumaa gub yu yàqu, di saxee saxe, wowal seeni tool aki tóokër, garabu figg ak oliw, njéeréer yi lekk. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.

10«Maa leen yónnee mbas mu mel ni mu waa Misra. Maa reylu seeni waxambaane ci xare, jàpplu seeni fas, gillil xetu néew ya ca seeni dal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.

11«Maa jàllarbi lenn ci yeen, na ma jàllarbee woon waa Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:" ak Gomor+ 4.11 Seetal ci \+bk Njàlbéen ga\+bk* 19.1-29.. Ngeen rëcce ca ni gillit gu ñu fëkke cib taal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee!

12«Moo tax ma di leen def lii, yeen bànni Israayil. Gannaaw lii laa leen di def nag, waajleena dajeek seen Yàlla, yeen bànni Israayil.»

13Kii kat moo móol tund, di sàkk ngelaw, di xamal nit nammeelam. Kee di soppi lëndëm ag leer, di daagoo kawte ya. Kookoo di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Kàddug Yàlla © 2025 La Mission Baptiste du Sénégal. Licensed under CC BY-NC-ND 4.0.
/div>