1Wóoy ña ne finaax ca Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"*,
2Demleen ba Kalne, xool;
3Wóoy yeen ñiy jéema fanq bésub njàqare
4Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj,
5yeena ngi fowantoo xalam,
6Yeena ngi jolu seen këlli biiñ,
7Moo tax yeenay jiituji ci ñi ñu gàddaayloo,
8Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee:
9Su boobaa, fukk ñu làqu ci kër, du leen teree dee.
10Ku warloo waajal mbokkam mu dee dina dugg ca kër ga, ngir yóbbu néew ya, te naan ka ca biir-a-biir: «Kenn desul foofu ci yaw?» Mu ne ko: «Jeex na,» bëgg caa teg baat, mu ne ko: «Déet! Noppil, bul tudd turu Aji Sax ji.»
11Aji Sax jee ngii déy, buy joxe ndigal rekk,
12Moo! Ndax fas dina daw ciy doj?
13Yeena ngi damu ca dëkk ba ñuy wax Lodebar (muy firi Amul njariñ) te naan: «Xanaa du sunu dooley bopp lanu nangul sunu bopp dëkk bu am doole ba ñuy wax Karnayim (muy firi Ñaari béjjén)+ 6.13 Ñaari béjjén, kàttan lay misaal.*?»