Ase 1:1-14 WOLB2025 - Bible AI

1Ca ñaareelu atu nguuru Buur Daryus+ 1.1 Daryus, buuru Pers bu mag la woon.*, ca juróom benneelu weer wa, yemook benn fan ca weer wa, kàddug Aji Sax ji|lemma="Aji Sax j-:"* moo dikk ci jottalib Yonent Yàlla Ase, ñeel doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ñeel itam doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag ba. Mu ne:

2Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Askan wii dañu ne àpp bi jotagul; àppub kër Aji Sax ji moo jotagul, ba ñu war koo tabaxaat.»

3Kàddug Aji Sax ji nag dikk ci jottalib Yonent Yàlla Ase. Mu ne:

4«Àpp bi daal yeen la jotal,

5Kon nag léegi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:

6Yeenay ji lu bare, góob tuuti;

7Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:

8Yéegleen tund wi, wuti bant, tabax sama kër gi;

9«Lu bare ngeen séentu, ndeke as tuut la,

10Kon nag yeena tax asamaan téye ab layam,

11ma wàcce bekkoor ci suuf seek kaw tund yi,

12Ba loolu amee doomu Selcel, Sorobabel, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag ba, ak mboolem ña des ca askan wa, ñoom ñépp déggal seen wooteb Yàlla Aji Sax ji ak kàddug Yonent Yàlla Ase, noonee ko ko seen Yàlla Aji Sax ji yóbbantee. Askan wa nag ragal Aji Sax ji.

13La ca tegu Ase, ndawal Aji Sax ji, jottali askan wa yóbbanteb Aji Sax ji. Mu ne leen: «Maa ànd ak yeen,» kàddug Aji Sax jee.

14Ba mu ko defee Aji Sax ji ñaax doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ak ña des ca mbooloo ma ñépp, ba ñu sottali liggéeyi kër Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, seen Yàlla.

© 2025 Bible Society of Senegal
div>