1Cofar ma bàyyikoo Naama àddu, ne:
2Yii kàddu yu wale, deesu ko tontoo?
3Sa kebetu yii wedamal na kenn a?
4Nee nga sa àlluwa wér na péŋŋ,
5Éy su Yàlla nammoona wax,
6àgge la kumpay xelam mu rafet,
7Dangaa mana gëstu mbóoti Yàlla, ba gis ko?
8Lu gëna kawe kaw, ana loo ci man?
9Màggaayu Yàllaa sut suuf,
10Su dikkee, tëj nit,
11Moom mi xàmmee ñi dul niti dara,
12Waaye ku boppam feesul, bu muusee,
13Waaye yaw soo defee sa xel ci Yàlla,
14fabal say ñaawtéef, sànni,
15kon déy, nga mucc gàkk, siggi;
16sa coonob tey ngay fàtte;
17te yaay gëna leer jantub njolloor,
18Kon nga am yaakaar ak kóolute,
19jaaxaan, kenn du la lëjal,