1Dama ne, lii lépp maa ko gis,
2Li ngeen xam, man it xam naa ko;
3Waaye man Aji Man ji laay waxal,
4Yeen nag yeenay rafetalkati fen,
5Céy su ngeen noon cell,
6Ngalla dégluleen sama tawat,
7Ndax Yàlla ngeen di waxal waxi njubadi,
8Ndax Yàlla ngeen faral,
9Ndax bu leen Yàlla luqatu woon dina baax?
10Su ngeen ko faraloon ci kumpa sax,
11Xanaa màggaayu Yàlla tiitalu leen?
12Seeni tari, léebi neen,
13Xeremluleen, ba ma wax man
14Amul dara lu mu ma jaralul,
15Su ma Yàlla doon rey it, moom laay yaakaar,
16Loolu it sama mucc a ngi ci,
17Dégluleen a déglu sama baat,
18Dégluleen maa, ma lañal ab layoo,
19Ana ku may yey cib layoo?
20Xanaa nga may ma ñaar rekk,
21ngalla teggi ma sa loxo,
22Wooteel, ma wuyu,
23Ana luy sama ñaawtéef aki moy?
24Ana loo may làqe sa leeru kanam?
25Xob wuy wéy ngay xoqtal?
26Yaa ma bindal dogal yu wex,
27Yaa ma jéng,