1Elifas àddu, ne:
2Ayóoba, ku xelu dina tontoo kàdduy ngelaw,
3Ku xelu du layoo waxi caaxaan,
4Yaw de, yaa ngi neenal worma,
5Saw làmmiñ déy, sa ndëngtee koy sa,
6Du man de, sa gémmiñu bopp a la teg daan,
7Xanaa yaa njëkka juddu ci nit?
8Ba Yàllay féncoo yaa doon déglu,
9Ana loo xam lu nu xamul
10Boroom bijjaaw ak màggat a ngi sunu biir,
11Kàddu yi la Yàlla di mas-sawoo da laa doyul?
12Ana looy waxe xol,
13Ngay sippi Yàlla sa mer,
14Ana nit ku mana jub xocc?
15Yàlla wóoluwul sax ñu sellam ña ca asamaan,
16rawatina nit, moom mi jara seexlu, yàqu jikko,
17Déglu ma, ma wax la,
18muy lu ñu rafet xel ñi jottali,
19Ñoom, seeni maam doŋŋ a jagoo woon réew mi,
20Bésoo bés ku bon ay bittarñikoo biir njàqare,
21coowal musiba mooy buur nopp ya,
22Dootul yaakaara mucc musiba,
23muy taxawaalu, tan ya mujj xontoo,
24Njàqareek tiitaangee koy ëlëm,
25Moo xàcc loxoom jëme ci Yàlla,
26daŋŋiiral, buur, wuti ko,
27te fekk ko yaflu ba gët suulu,
28Ku ni mel ay dëkke dëkk yu gental,
29Ku bon kooku du woomle, alalam du toog,
30Du mucc musiba,
31Bumu yaakaar naxi neen, di nax boppam,
32Balaa jantam a lang mu jot añam,
33Day mel ni reseñ gu doom yay yolax,
34Waa làngu yéefar yi duñu am kuutaay,