1Ayóoba àddu ne:
2Kàddu yu mel nii, dégg naa ko lu bare.
3Sa waxi ngelaw yii da dul jeex?
4Su ngeen doon man, may yeen,
5Waaye su doon man, ma wax ak yeen, ba dëfal leen,
6Waaye su ma waxee, mitit du giif;
7Yàlla kay a jeexal sama doole,
8Moo ma jàpp, semmal ma;
9Meram la ma daggatee, jéppi ma,
10Nit ñaa ngi ŋa ŋàpp fi sama kaw,
11Yàlla da maa wacce ab kàccoor,
12Féexoon naa, mu falaxe ma;
13ay fittkatam gaw ma,
14Mooy buur ni xarekat fi sama kaw,
15Ab saaku laa ñaw, taqoo,
16Sama kanam a ngi xonq curr aki jooy,
17Moona saay loxo jëfewul coxor,
18Suufoo, bul làq sama deret ji tuuru,
19Ma ne, tey fi tey, am naa ab seede kaw asamaan,
20Samay xarit ñoo may kókkali,
21Na ab seede layool nit fa Yàlla,