1Sama xol jeex,
2Fu ma jublu ñu di ma ree,
3Ngalla Yàlla, gàddul mab daan sama digg ak yaw;
4Yaa fatt xelu ñii,
5Nee ñu, ku njariñ tax nga wor xarit,
6Man la nit ñi def léebukaay,
7Naqar tax na saay gët giim,
8Ku jub a ngii jommi ci lii ma dal,
9Waaye aji jub a ngi topp yoonam,
10Waaye yeen ñépp, waxaatleen, ma dégg,
11Samay fan wéy na,
12Ñii guddi lañu def bëccëg,
13Ndegam kërug njaniiw laa yaakaarati,
14ndegam maa naa paxum yàqute ma: «Yaay sama baay!»
15Kon ana sama yaakaar?