1Ayóoba àddu ne:
2Dégluleen maa, dégluleen sama baat,
3Muñalleen ma boog, ma wax, man,
4Sama tawat lii, da di maak nit a?
5Geesuleen ma, waaru,
6Su ma ko xalaatee, damay tiit,
7Lu tax ku bon di dund,
8Doomam day toog, mu fekke,
9këram nekke jàmm, mucc safaan,
10Ku bon, yëkkam day tëb te du moy,
11Day gis ay xaleem di bajantu,
12Day xaacoondookum tëgg aki xalam,
13Ku bon ay matal ay fanam ci biir teraanga,
14Moona kee noon Yàlla: «Xiddi ma!
15Ana kuy Aji Man ji sax, ba ma di ko jaamu?
16Kii xanaa du teraangaam a ngi ciy loxoom?
17Ku bon, ana fu ag xuyyam kamaje?
18Ana fu ku bon mele nim ñax mu ngelaw wal,
19Ngeen ne, «Ku bon daal ay tooñ, Yàlla dencal doomam añ ba.»
20gisal boppam sànkuteem,
21Ana luy yoonu ku bon ci waa këram, gannaawam,
22Ana kuy jàngal Yàlla xam-xam,
23Kii a ngi deewaale dooleem,
24yaram wa niin,
25Kee deewe naqaru xol,
26te ñooy tëddandoo biir suuf,
27Mu ngoog! Maaka xam li ngeen foog,
28Ngeen ne: «Ana fu kër kàngam di mujje?
29Xanaa laajuloo tukkikat yi?
30Bésub safaan ku bon ay mucc,
31Ana kuy janook moom, sikke ko jikkoom?
32Moom de bu deewee, sëg ya lees koy robi,
33Liy topp néew ba, day bare,