Ayóoba 22:1-29 WOLB2025 - Bible AI

1Ba loolu amee Elifas ma cosaanoo Teman àddu ne:

2Yàlla, ana lu ko nit mana jariñ?

3Ana lu sag njub mana yokk Aji Man ji?

4Ndax sag am diine la lay dumaa,

5Xanaa du sag mbon gu réy a la ko yóbbe,

6Yaa lebal mbokk, aakimoo tayleem ci dara,

7Yaa mayul ku mar ndox mu naan,

8Boroom doole jagoo réew mi,

9Yaa bàyyi jëtun, mu deme loxoy neen,

10Moo tax ay ndëgg-sërëx di la dar kepp,

11mbaa lëndëm gu la teree gis,

12Xanaa Yàlla sutul asamaan?

13Nga naa: «Ana lu Yàlla xam?

14Niir yee ko làq ba du nu gis,

15Xanaa dangaa nara topp ñallu démb

16Ñoo buube, ne mes te seen àpp jotul,

17te ñoo doon wax Yàlla, naan ko: «Xiddi nu!»

18Moona moo feesaloon seeni kër ay teraanga,

19Aji jub ñeey gis sànkutey ñii, bég;

20naan: «Ña nu jógaloon sànkuwuñoo am?

21Jubool ak Yàlla rekk, am jàmm,

22Nangool ndigal ci làmmiñam,

23Dellul ci Aji Man ji rekk, ba taxawaat,

24Tegal wurus ci suuf,

25te Aji Man ji di sa wurus,

26Su boobaa nga bége Aji Man ji,

27di ko ñaan, mu di la nangul,

28loo dogu, mu sotti,

29ba bu nit detteeloo, nga yékkati ko,

© 2025 Bible Society of Senegal
v>