1Lu tee Aji Man ji àppal nit bési mbugal,
2Nit a ngi toxal kemu suuf,
3Mbaamu jirim, ñu wommat, yóbbu;
4Néew-ji-doole, ñu buuxe ko ciw yoon,
5Néew-ji-doole yaa ngii mel niy mbaami àll ci màndiŋ mi,
6Tooli jàmbur lañuy góobaani,
7Duŋŋ lañuy fanaane ndax rafle,
8Ñooy tawtee tund ya,
9Xoncees na jirim ci weenu ndeyam,
10Duŋŋ lañuy wéye ndax rafle,
11di nal diwu oliw ci tooli jàmbur,
12Biir dëkk ba la nit ñay binnee,
13Ñee noonoog leer,
14Bët di set, bóomkat jóg,
15Moykat bu góor a ngi yeeru timis,
16Ñu ngi lëndëmtu, di toj kër yi,
17Ñoom ñépp ñuulaayu guddeey seen bëccëg,
18Yal nañu wéye walum ndox,
19Yal na maral ak tàngoor ŋiisal seen ndoxum taw,
20Yal na leen seen ndey sax fàtte,
21Ñu ni mel ay lekk alalu jigéen ju tëlee jur,
22Waaye Yàllaa mana dàq boroom doole,
23Moo leen di may ñu wéeroo seen cëslaay,
24Dañuy jóg, nes tuut ñu ne mes,