1Xaalis déy am na mbellam,
2weñ gu ñuul ci suuf lees ko jële,
3Dees na taal, dàqug lëndëm,
4Nit a ngi gas ay xunt fu soreeki dëkkuwaay,
5Kaw suuf day meññ ab dund,
6Doj ya ca biir la peri safiir màkkaanoo,
7Wii yoon, tan xamu ko,
8Rabu àll du fa joggi,
9Loxol nit ay song doju kekk,
10Ci biir xeer yi lay yattey xunt,
11Nit a ngi dogale wali ndox,
12Waaye xel mu rafet fees koy jële,
13Doom aadama xamul njëgam,
14Xóote ya nee: «Xel mu rafet dëkku fi de!»
15Wurus mayewu ko,
16Deesu ko weccee wurusu ngalam it,
17Deesu ko méngaleek wurus ak ngën-gi-per yuy tàkk,
18waxeesuli xor ak yeneen xeeti per;
19du moroomu peru topaas ba ca réewum Kuus|lemma="Kuus:"*,
20Xel mu rafet, ana fu mu jóge,
21Ump na bëtu lépp luy dund;
22Paxum sànkutee ngi àddoondook dee naan:
23Yàllaa ràññee yoon wa jëm xel mu rafet,
24Kii daal ay jéer ba fa cati àddina,
25Ba Yàlla àppalee ngelaw diisaayam,
26ba mu sàkkalee ab taw dogalu yoonam,
27ca la nemmiku xel mu rafet, xamle ko,