1Tey ñi may diijoo ngii, te ñoo ma féete ndaw,
2Ana njariñ lu ñu ma amaloon sax?
3Ñii ndóol, xiif, desey yax,
4di witt ñax mu saxe ciy tan
5Ñooñu lees dàqe fi biir nit ñi,
6ñu dëkkey xur,
7di ŋaaxe biir gajj gi,
8Ñu sew lañu, ñu kenn yégul,
9Tey nag ñoo may woyantoo,
10Dañu maa seexlu, ñooru ma,
11Yàllaa ma nasaxal, toroxal ma,
12Mii njurum baadoola mu féete ndijoor, di ma téqtal,
13Ñu ngi may dogale, nar maa musibaal,
14Fu yaa lañu bëtte,
15Musiba da maa ëlëm,
16Tey maa ngii sama bakkan di ŋiis,
17Guddi dikk di bënn samay yax, muy rot,
18Kii ne nikk sama mbubb,
19xalab ma ci biir ban bi,
20Woo naa la wall, wuyuwoo ma,
21Yaa soppiku, néege ma,
22Yaa ma ne siféet, waral ma ngelaw,
23Xam naa xéll ne ci dee nga ma jëme,
24Ku sànkule du tàllal loxoo?
25Moona sama rongooñ a daan tuurul boroom tiis,
26Lu baax laa yaakaar, lu bon ne jalañ,
27sama xol lëmbaajoo, tëë dal,
28Maa ngi wéye ñuulaay bu ma tàngoor tegul,
29Damaa mujj bokk ak till,
30ñuul, yaram di xub,