1Maa jaayanteek samay gët.
2Lu ko moy ana sama cér ca Yàlla ma fa kaw?
3Xanaa du safaan a ñeel ku bon,
4Du Yàllaa ngi gis fu ma jaare,
5Ndegam damaa doxe ndëngte,
6na ma Yàlla natte màndaxekaayu dëgg,
7Ndegam samay tànk a moy yoonu njub,
8yal naa ji, keneen lekk,
9Ndegam jabaru jàmbur a ma xañ sago,
10yal na sama jabar bojjal keneen,
11Su ma ko defoon, muy jëfu yàqute,
12te di sawara wu may xoyom ba ca paxum sànkute ma,
13Ndegam maa sofental sama àqu jaam,
14bu ci Yàlla jógee, ana nu may def?
15Ki ma sàkk ci sama biiru ndey,
16Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku,
17Am damaa masa wéetoo ab dog,
18Ba may ndaw laa dala yor ab jirim ni baayam;
19Ndegam maa seetaan ku rafle nara sànku,
20te sànguma céram, mu sante ma ko,
21ndegam maa xàcc sama loxo jëme cib jirim,
22yal na sama loxo teqalikook sama mbagg,
23Mbugalu Yàlla kat laa ciy ragal,
24Ndegam damaa def wurus sama yaakaar,
25ndegam maa bége sama alal ju bare,
26ndegam maa masa niir jant beek leeraayam,
27ba namma làqu, di ci jaamu lenn,
28kon ñaawtéef gu yeyoo àtte lay doon,
29Ndegam maa bége musibay bañ,
30te bàkkaarewuma sama làmmiñ sax,
31ndegam du samay bokk a ma seedeel ne:
32Te biti, masumaa wacc doxandéem di fa fanaan,
33Ndegam maa roy nit ñi, di nëbb samay tooñ,
34ragaluma jëwu àddina de,
35Ma ne éy ku may may nopp?
36maa koy gàddu, kaalawoo.
37Maay limal Yàlla jéego bu ma séqi,
38Ndegam sama tool a ma tuumaale ay jooy,
39ndegam maa lekk lu ca ñor, te dikkewuma dara,