Ayóoba 33:1-32 WOLB2025 - Bible AI

1Léegi Baay Ayóoba, ngalla déglul samay wax

2Xaaral, ma àddu boog,

3Xel mu dëggu laay waxe,

4Ngelawal Yàllaa ma sos,

5Soo manee, tontu ma;

6Maa ngii, yem ak yaw fa Yàlla;

7Du sama ñàngaay bu lay tiital,

8Yaa wax déy, ma dégg,

9Nga ne: «Set laa def, tooñuma;

10Waaye Yàllaa ngii di ma wuta taqal,

11jéng ma,

12Foofu déy, moy nga dëgg, ma wax la ko,

13Ana loo koy sikke,

14Yàlla déy, dees koo teewluwul,

15ci biir peeñum géntu guddi,

16Mu ne ko rukk ndéey,

17ngir dëdduloo doom aadama ji ay jëfam,

18sorale bakkanam pax,

19Nit dina mbugaloo mitit wu ko tëral,

20Day bañ dugub,

21jeex tàkk bay réer aka feeñ,

22dundam dëgmal dee,

23Waaye su nit ki amee malaakam àttekat,

24da koy baaxe, daldi ne Yàlla:

25Yaram wa jotaat tooyaayu ndaw,

26bu ñaanee Yàlla, mu nangul ko,

27nit ki seedeeli ko ca nit ña, ne:

28Yàllaa ma jot ba jàlluma, jëm pax,

29Lii lépp déy, la Yàlla di def,

30ngir sorale bakkanam pax,

31Baay Ayóoba, teewlul, déglu ma,

32Soo amee lenn loo wax, àddul;

© 2025 Bible Society of Senegal
v>