1Eliyu dellu ne:
2Defe nga ne lii yoon la?
3te naan ko: «Ana lu ma ci soxal man,
4Man mii nag maa lay tontu,
5Séentul asamaan te xool,
6Soo bàkkaaree, lu muy wàññi Yàlla?
7Ana njub goo def ba may ko lenn,
8Sag mbon, sa moroomu nit lay lor,
9Nooteel law na ba nit ñiy yuuxu,
10Waaye kenn du ci ne: «Wóoy ana Yàlla mi ma sàkk,
11di nu xamal lu rabu àll xamul?
12Bu nit ñu bon ñiy woote wall, du wuyu
13Neen lañuy woote, ndax Yàlla du leen déglu,
14Kon ngalla yaw mi ne gisoo ko,
15Nga neeti Yàlla du mer, di mbugale,