1Eliyu dellu ne:
2Négal tuuti, ma xamal la;
3Fu xóot laay jukkee sama xam-xam,
4Sikk déy, nekkul ci li ma lay wax;
5Dama ne, Yàllaa màgg te du jalaxe,
6Du ba ku bon, mu dund,
7Du noppee xool aji jub ñi,
8Bu ñu demee ba ñu jéng leen,
9Yàllaa leen koy artoo ci seeni jëf,
10Da leen di dégtal ndigal,
11Su ñu ko dégloo, déggal ko,
12Su ñu dégluwul, jàlli dexu dee,
13Ab yéefar day denc mer,
14Ku ni mel ay deewe ndaw,
15Yàllaay wallu boroom tiis ciw tiisam,
16Moom it moo lay xettali ci njàqare,
17Waaye añu ku bon duunal na la,
18Bu la kenn xiirtale alal,
19Kon déy doo yuuxu ba mucc ci njàqare,
20Bul yàkkamti guddi;
21Moytula walbatiku di def ñaawtéef,
22Yàlla, kay, mooy ki dooleem kaweel!
23Ana ku ko masa rëddal yoonam?
24Bul di fàttee màggal jëfam,
25Mboolem doom aadama gis na ko;
26Yàlla kay, daa màgg ba wees xam-xam,
27Keey ñoddi toqi ndox,
28niir yi sotti,
29Ana ku xam ni aw xiin di firikoo,
30Keey taal melaxam, mu dajal asamaan,
31Noonu lay saytoo xeet yi,
32Ñaari loxoom lay ŋëbe melax gi,