1Lii déy a rëccal sama fit,
2Dégluleen a déglu dënoom gay ràndaŋ,
3muy riiral fépp fu asamaan tiim,
4Ca lay yëmmu,
5Yàllaay dënu kéemtaan,
6Kee naan tawub yuur mu sóobal suuf,
7daldi téye loxol képp ku doon liggéey,
8Rabu àll duggi biir xuntam,
9ngëlén bawoo néegam,
10Yàllaay nokki, ndox mi soppi galaas,
11Keey sëf xàmbaar, mu guux,
12ñu jargandalu ci ndigalam
13mu mel ni yet wu muy bantale waa àddinaam,
14Yaw Baay Ayóoba, teewlul lii,
15Dangaa xam nu Yàlla di sosey niiram,
16Dangaa xam nu niir yiy ajoo ci jaww ji,
17Yaw mi say yére di tàng,
18ndax yaa ko lalle woon déndub asamaan,
19Xamal nu boog lu nuy wax Yàlla!
20Ndax dees koy yégal ne maay waaja wax?
21Kenn manula xool jant bu ne ràññ,
22Bëj-gànnaar la leeru wurus di dikke,
23Aji Man ji nu dul daj daa bare doole,