1Yaa xam jamono ju kéwéli tund di jur?
2Yaa lim weer yi muy ëmb,
3ba mu sukk, jur,
4ak fa doom jay leqalikooka màgg ci àll bi,
5Ana ku yóbbu fasu àll, afal ko?
6Moom mi ma jox màndiŋ mi, mu dëkke,
7Yégul riirum taax,
8Tund yi lay wërem poram,
9Ndax nagu àll a lay nangoo liggéeyal?
10Man ngaa takk nagu àll cim rijji,
11Yaa koy yaakaare dooleem ju bare,
12Yaay yaakaar mu fatal la jiwu,
13Bànjóolee ngi tëf-tëflu,
14Mooy wacci nenam fi suuf,
15Xalaatul tànk bu ci joggi
16Day soxore doom yi ni lu mu jurul,
17Yàllaa ko xañ xam-xam,
18Waaye bu sàqee, ba sàqi,
19Ndax yaa may aw fas kàttan?
20Am yaa koy tëbloo nim soccet,
21Fas a ngi bége dooleem, di curpee xur wa,
22Yégul tiitaange, ragalul,
23Mbarum fitt a ngay keseŋ-keseŋi fa kawam,
24mu buure xadar, taxañ suuf si,
25mu feeloo ko coowal wakkan ya.
26Ndax sam xel la céeliy daayaarloo,
27Am yaa sant jaxaay mu naaw ba fa kaw,
28Aw doj, mu màkkaanoo,
29Fa lay yeeroo am rëbbam,