1Aji Sax ji dellu ne Ayóoba:
2Yaw miy layook Aji Man ji, dangay diiŋat?
3Ayóoba àddu ne Aji Sax ji:
4Man mi tekkiwul dara, nu ma lay tontoo?
5Maa waxoon benn yoon, waxatuma;
6Aji Sax ji daldi àddoo fa ngëlén la, ne Ayóoba:
7Takkul boog te góor-góorlu,
8Sañ nga maa teg tooñ daal,
9Dangaa am dooley Yàlla,
10Ràngool boog màggaay ak teraanga,
11Yuril sa mer,
12xoolal képp ku bew, toroxal ko,
13Boole leen làq biir suuf,
14Kon déy man maa lay sargal,
15Beyemot rab wu réy+ 40.15 rab wu réy wii am na ñu jàpp ne léebéer la.* waa ngii, maa ko sàkk, sàkk la,
16Doole jaa ngoogu ca ndigg la,
17geen ga ne kàdd ni garabu seedar,
18yax ya di ponki xànjar,
19Moo gëna yéeme ci li Yàlla sàkk,
20Xontam déy tund yee ko yor,
21Keppaaru déem lay goore,
22déem ya keral ko,
23Dex gu fees jaaxalu ko,
24Ana ku koy jàpp te muy xoole?
25Ninki-nanka+ 40.25 ninki-nanka jii am na ñu jàpp ne jasig la.* nag yaa koy nappe oos?
26Yaay nase wakkan ya ag buum?
27Xanaa ca la lay tinoo tinu,
28Xanaa kon mooy digook yaw,
29Am yaa koy fowe ni picc,
30Dees na ko waxaaleendoo?
31Yaa koy jamati xepp a?